Màrk 14
14
Njiiti yoon yi fexeel nañu Yeesu
1 Màggalu bésub Mucc ba ak màggalug ayu bésu Mburu mu amul lawiir a jubsi woon, ba des ñaari fan. Ci kaw loolu sarxalkat yu mag ya ak firikati yoonu Musaa ya di wut nu ñu sàcce ba jàpp Yeesu, reylu ko. 2Ndax booba dañu ne: «Bumu doon ci bésu màggal bi, lu ko moy askan wi yëngu.»
As ndaw sotti na lajkoloñ ci kaw Yeesu
3Ci biir loolu Yeesu demoon na dëkk ba ñuy wax Betani. Mu dale kër ku ñuy wax Simoŋ gaana ga. As ndaw dikk, fekk ko muy lekk. Ndaw saa nga yor njaqal doju albatar lu def diwu nàrd gu xeeñ lu neex te raxul, tey jar lu baree bare. Mu toj njaq li, daldi sotti diw gi ci boppu Yeesu.
4Ñenn ca ña mu fa fekk nag ñaawlu loolu. Ñuy xultu ci seen biir naan: «Ana lu waral yàq gii lajkoloñ? 5Gii diw maneesoon na koo jaaye lu tollook ñetti téeméeri poseti xaalis#14.5 poseti xaalis mooy peyooru benn bésub liggéey ca jamono yooya., jox ko néew-doole yi.» Ñu sikk ca ndaw sa lool.
6Yeesu nag ne leen: «Bàyyileen ndaw si, ana lu ngeen koy sonale? Jëf ju rafet la ma defal. 7Néew-doole yi de, dingeen ci am ñu nekk ak yeen ba fàww, te saa yu leen neexee, man ngeen leena defal lu baax. Waaye man de, amuleen ma ba fàww. 8Ndaw si, li mu man, def na ko. Laata ñu may rob, diw na ma lu xeeñ. 9Te maa leen ko wax déy, li ndaw sii def, fépp fu ñuy yéeneji ëllëg xibaaru jàmm bi ci àddina sépp, dees na ko fa nettalee, di ko fàttalikoo jëmmu ndaw si.»
Yuda wor na Yeesu
10Ci biir loolu kenn ca Fukk ñaak ñaar, ñu di ko wax Yuda Iskaryo, daldi dem ca sarxalkat yu mag ya, ngir teg Yeesu ci seeni loxo. 11Ba sarxalkat yu mag ya déggee lu doon tànki Yuda Iskaryo, dañu caa bég, ba dig ko xaalis. Muy seet nag yoon wu mu jekkoo Yeesu, ba wor ko.
Yeesu bokk na reeram bu mujj aki taalibeem
12Ca bés ba njëkk ca màggalug ayu bésu Mburu mu amul lawiir, ñu war caa rendi gàttub bésub Mucc, ca la taalibe ya laaj Yeesu, ne ko: «Foo bëgg, nu dem, waajalal la fa reeru bésub Mucc bi?» 13Yeesu nag yebal ñaar ca taalibe ya, ne leen: «Demleen ca dëkk ba, dina am waa ju dajeek yeen. Ma nga yenu njaqas ndox, toppleen ko. 14Kër gu mu mana dugg, neleen boroom kër ga: “Kilifa gi nee: Ana néegu gan, fi may reere reeru bésub Mucc, maak samay taalibe?” 15Kooku moo leen di won néegub kaw bu yaa, bu ñu defar ba mu jekk. Foofa ngeen nuy waajale.» 16Ba taalibe ya demee ba àgg ca biir dëkk ba it, noonu lañu gise la mu leen waxoon. Ñu daldi waajal reeru bésub Mucc ba.
17Ba jant sowee, Yeesu dikk, ànd ak Fukk ñaak ñaar. 18Gannaaw ba ñu toogee bay reer, Yeesu ne leen: «Maa leen ko wax déy, kenn ci yeen ñiy lekkandoo ak man, moo may wor.» 19Aw tiis nag jàpp taalibe ya, ñu kenn-kennoo di laaj, naan: «Mbaa du man?» 20Mu ne leen: «Yeen Fukk ak ñaar ñii daal, kenn la ci, te mu ngi yebandoo ak man loxoom ci ndab li. 21Doomu nit kaa ngi dem moos, noonee ñu ko binde woon, waaye wóoy ngalla ki pexe mi ñu wore Doomu nit ki di jaare! Kooka de, bañoona juddu sax moo doon gën ci moom.»
22Naka ñuy lekk, Yeesu jël mburu, yékkati kàddug cant, dagg, jox leen, daldi ne: «Jëlleen, lii sama yaram la.» 23Mu teg ca jël ab kaas, yékkati kàddug cant, jox leen, ñépp naan ca. 24Mu ne leen: «Lii mooy sama deret, ji fas kóllëre gi, te nara tuurul ñépp#14.24 Seetal ci Esayi 53.12 ak ci 1.Timote 2.6.. 25Maa leen ko wax déy, dootuma naan mukk ndoxum reseñ, ba kera ma naan ko bees ca nguurug Yàlla.»
26Ba loolu amee ñu yékkati galanu cant, daldi génn jëm tundu Oliw ya.
Yeesu nee Piyeer dina jàmbu
27Yeesu nag ne leen: «Yeen ñépp ay dellu gannaaw, ndax bindees na ne:
“Maay dóor sàmm bi,
xar yi tasaaroo#14.27 Seetal ci Sàkkaryaa 13.7..”
28Waaye bu ma dekkee, dinaa leen jiituji fa Galile.»
29Piyeer nag ne ko: «Bu ñépp dellu woon gannaaw it, man duma dellu gannaaw mukk.» 30Yeesu ne ko: «Maa la ko wax déy, yaw, guddig tey jii, bala ganaar a sab ñaari yoon, dinga ma jàmbu ñetti yoon.» 31Piyeer nag gënatee biral, ne: «Su ma naree ànd ak yaw dee sax déy, duma la jàmbu mukk.» Taalibe ya ca des yépp nag waxe noonu, ñoom itam.
Yeesu tiislu na ca toolu Setsemane
32Ñu dem ba tollook tool ba ñu dippee Setsemane. Yeesu ne taalibe ya: «Toogleen fii, xaar ma, ma ñaani.» 33Ci kaw loolu mu ànd ak Piyeer ak Yanqóoba ak Yowaan. Tiitaange ak njàqare daldi koy jàpp. 34Mu ne leen: «Tiis wuy rey la sama xol fees, ba may bëgga dee! Toogleen fii te ngeen teewlu.»
35Ba loolu amee Yeesu dox ba sore leen tuuti, ne gurub sukk, dëpp jëëm fa suuf, di ñaan ngir, ndegam man naa am, coonob waxtu wa mu dëgmal teggi ko. 36Mu ne: «Abba#14.36 Abba mu ngi tekki baay., Baay, yaw mi dara tëwul, bii kaas bu fees ak wextanu coono, ngalla teggil ma ko. Waaye bumuy sama coobare, nay doon ci sa coobare.»
37Gannaaw loolu mu délsi, fekk taalibe ya di nelaw. Mu ne Piyeer: «Simoŋ, dangay nelaw? Wenn waxtu doŋŋ, amuloo dooley teewlu ko? 38Teewluleen te ñaan, ngir baña tàbbi cig fiir. Xolub nit kat yebu na, yaram see néew doole.» 39Yeesu demaat ba nee, daldi baamtu kàddug ñaanam ga. 40Mu délsiwaat, fekk leen ñuy nelaw, manatuñoo xippi ndax ngëmment lu réy. Xamuñu nag lu ñuy wax.
41Gannaaw loolu mu délsiwaat ñetteel bi yoon, daldi ne leen: «Yeena ngi nelaw, di noppalu ba tey? Jeex na nag. Waxtu wi dikk na. Ñu ngi nii di teg Doomu nit ki ci loxoy bàkkaarkat yi. 42Jógleen, nu dem. Ki may wor a ngi nii.»
Jàpp nañu Yeesu
43Naka la Yeesu di wax, daaneelagul, Yuda, kenn ca Fukk ñaak ñaar dikk, ànd ak gàngoor gu bawoo ca sarxalkat yu mag yaak firikati yoonu Musaa yaak magi askan wa. Ña nga gànnaayoo ay saamar aki njur.
44Fekk na workat ba tegtal leen, ne leen: «Ki may fóon, kooku la; jàppleen ko, yóbbu te wattu ko bu baax.» 45Mu daldi agsi, dikk ba ci Yeesu, ne ko: «Kilifa gi!», daldi ko fóon. 46Ba mu ko defee nit ña ne ko taral, jàpp ko. 47Ba loolu amee kenn ca ña fa taxaw bocci ab saamar, caw ko surgab sarxalkat bu mag ba, njoof nopp ba.
48Yeesu ne leen: «Jàppsi ma doŋŋ a leen taxa dikkey saamar aki njur, mel ni ñuy topp ab fippukat? 49Moona bés bu nekk maa nga woon ak yeen ca kër Yàlla ga, di jàngale, te jàppuleen ma. Waaye lii daa am ngir sottal Mbind mi.» 50Ci kaw loolu, ñépp daw, wacc ko.
51Ab xale bu góor a nga ko toppoon, lëkkaayoo ab malaan kese. Ñu daldi ko jàpp. 52Xale bu góor ba nag, ne wëqét, daw, wacc fa malaan ma, def yaramu neen.
Yeesu taxaw na ca kuréelu àttekat ya
53Ba loolu amee ñu yóbbu Yeesu ca sarxalkat bu mag ba, yeneen sarxalkat yu mag yaak magi askan waak firikati yoonu Musaa ya, ñépp daje fa. 54Ci biir loolu Piyeer yoxal Yeesu lu sore, topp ca gannaawam, ba ca biir ëttu sarxalkat bu mag ba. Mu toog faak wattukat ya, di jaaru ca taal ba.
55Ci kaw loolu sarxalkat yu mag yaak mboolem kuréelu àttekati Yawut ya di wut kàddug seede gu ñu tuumaale Yeesu, ba ñu man koo reylu, te amuñu ko. 56Teewul ñu baree dikk, seedeel Yeesu ay fen, waaye seen kàddu yaa woroo. 57Ci biir loolu ñenn ña jóg, seedeel ko ay fen, daldi ne: 58«Nun de dégg nanu, mu ne: “Kër Yàlla gii loxol nit liggéey, maa koy toj, tabaxaat ci ñetti fan geneen kër Yàlla gu loxol nit liggéeyul#14.58 Seetal ci Yowaan 2.19-22..”» 59Kàdduy ñooña nag woroo ba tey.
60Ba mu ko defee sarxalkat bu mag ba jóg taxaw ca digg mbooloo ma. Mu ne Yeesu: «Doo tontu dara ci li la ñii tuumaal?» 61Yeesu ne cell, waxul dara. Sarxalkat bu mag ba dellu ne ko: «Ndax yaa di Almasi bi, Doomu Ki yelloo màggal?» 62Yeesu ne ko: «Man mii la, te dingeen gis Doomu nit ki toog ci ndijooru Boroom Kàttan gi, dingeen ko gis itam ci biir niir yi, muy ñëw#14.62 Seetal ci Dañeel 7.13..»
63Sarxalkat bu mag nag ne tareet yérey boppam#14.63 tareet yére: màndargaam ténj la, ma ñu tere sarxalkat yu mag ya. Fii, jëf jooja day màndargaal ci seen cosaan ne Yeesu dañu ko wara teg daan., daldi ne: «Ana lu nuy doyeeti ay seede? 64Yeena dégg ni mu diire Yàlla mbagg! Lu ngeen ci xam nag?» Ñépp ne dee mooy àtteem. 65Ci kaw loolu ñenn ña tàmbali koo tifli, muur kanam gi, dóor ko ay këmëx, naan ko: «Yaw waxal nu kàdduy waxyu boog!» Wattukat yi daldi ko jàpp, dóor ko ay mbej.
Piyeer jàmbu na
66Ci biir loolu Piyeer a nga woon ca suuf, ca ëtt ba. Benn surga bu jigéen bu sarxalkat bu mag ba romb fa. 67Naka la gis Piyeer muy jaaru, mu xool ko jàkk, ne ko: «Yaw itam yaak Yeesum Nasaret a àndoon.» 68Piyeer nag miim ko, ne ko: «Man de, yéguma, xawma dara ci li ngay wax.» Piyeer daldi génn, ba ca mbaaru bunt ba ca biti. 69Surga bu jigéen ba gisati ko dellu ne ña fa taxaw: «Kii ci ñoom la bokk!» 70Mu dellu miim ko.
Nes tuut ña fa taxaw ñoom it, ne Piyeer: «Yaw itam kay ci ñoom nga bokk, nde yaw itam waa Galile nga.» 71Piyeer di tàmbalee waat aka giñ ne: «Ki ngeen di wax, man xawma ko!» 72Ca saa sa ganaar sab ñaareel bi yoon. Piyeer nag fàttaliku la ko Yeesu waxoon, ne ko: «Bala ganaar a sab ñaari yoon, dinga ma jàmbu ñetti yoon.» Mu ne yikkét, jooy.
Currently Selected:
Màrk 14: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright