1
Màrk 13:13
Kàddug Yàlla
KY
Te it ñépp a leen di bañ ndax sama tur. Waaye ku muñ ba muj ga, kooku dina mucc.»
Compare
Explore Màrk 13:13
2
Màrk 13:33
Moytuleen te teewlu, ndax xamuleen kañ la.
Explore Màrk 13:33
3
Màrk 13:11
Bu ñu leen tegee loxo nag, ba jébbal leen kilifa ya, la ngeen wara waxi bumu leen jaaxal, waaye kàddu gu ñu leen may keroog ca waxtu wa rekk, waxleen ko, ndax su keroogee du yeenay wax, waaye Noo gu Sell geey wax ci yeen.
Explore Màrk 13:11
4
Màrk 13:31
Asamaan ak suuf dina wees, waaye samay wax du wees mukk.
Explore Màrk 13:31
5
Màrk 13:32
«Waaye bés boobu mbaa waxtu wa nag, kenn xamu ko; du malaaka ya fa asamaan, du Doom ji, xanaa Baay bi doŋŋ.
Explore Màrk 13:32
6
Màrk 13:7
Bu ngeen déggee ay xare ak coowi xare, buleen tiit, fàww loolu am, waaye du doonagum muj ga.
Explore Màrk 13:7
7
Màrk 13:35-37
Kon teewluleen, ndax xamuleen kañ la boroom kër giy dikk. Jombul muy ngoonug suuf, mbaa xaaju guddi, mbaa bu ganaar sabee, mbaa bu bët setee. Bumu ne jalañ, fekk leen ciy nelaw. Lii ma leen wax nag, ñépp laa ko wax: “Teewluleen!”»
Explore Màrk 13:35-37
8
Màrk 13:8
Aw xeet dina jógal aw xeet, am réew jógal am réew, ay yëngu-yënguy suuf dina dikke fu bare, te ay xiif dina am, waaye ndoortel mititu mat la looluy doon.
Explore Màrk 13:8
9
Màrk 13:10
Balaa daraa xew, fàww xibaaru jàmm bi siiw ci xeet yépp.
Explore Màrk 13:10
10
Màrk 13:6
Ñu bareey dikk, tuddoo sama tur, naan: “Man a,” te ñu bare lañuy nax.
Explore Màrk 13:6
11
Màrk 13:9
«Yeen nag moytuleen. Dees na leen jàpp, jébbal leen pénci layoo ya, dees na leen dóor ca biir jànguy Yawut ya, te fa kanam boroomi dëkk aki buur ngeen di taxawi ndax man, ngir ngeen man leena yékkatil kàdduy seede.
Explore Màrk 13:9
12
Màrk 13:22
ndax ay almasiy caaxaan ak yonenti caaxaan ñooy feeñ, di jëfe ay firnde aki kéemaan, di wuta nax ñi ñu tànn, ndegam man naa nekk.
Explore Màrk 13:22
13
Màrk 13:24-25
Yeesu neeti: «Te fan yooya, gannaaw coono ba, “jant bi day lëndëm, weer wi fey ag leeram, biddiiw yi xàwweekoo asamaan, doole ya fa asamaan sàqi.”
Explore Màrk 13:24-25