1
Macë 21:22
Kàddug Yàlla
KY
Te lépp lu ngeen sàkkoo ñaan gu ànd ak ngëm, dingeen ko am.»
Compare
Explore Macë 21:22
2
Macë 21:21
Yeesu ne leen: «Maa leen ko wax déy, su ngeen gëmee te baña am xel ñaar, dungeen yem ci def nii figg gi, waaye tund wii sax, bu ngeen ko noon: “Jógal tàbbiji géej,” loolooy am.
Explore Macë 21:21
3
Macë 21:9
Ndiiraan ya ko jiitu ak ya ko topp a ngay xaacu naan: «Osaana, cant ñeel na Sëtub Daawuda bi! Na barke wàcc ci ki dikk ci turu Boroom bi! Osaana, na cant jibe béreb ya gëna kawe.»
Explore Macë 21:9
4
Macë 21:13
Mu ne leen: «Bindees na ne: “Sama kër gi, kërug ñaan lees ko tudde,” waaye yeen, moom ngeen def rawtub sàcc.»
Explore Macë 21:13
5
Macë 21:5
«Neleen janq Siyoŋ mu taaru: “Niiral, sa buur a la dikkal nii, di ku woyof, war mbaam, cumbur la war, doomu mbaam-sëf.”»
Explore Macë 21:5
6
Macë 21:42
Yeesu nag ne leen: «Xanaa masuleena jàng lii ci Mbind mi? “Doj wi tabaxkat yi beddi woon, moo mujj di doju koñu tabax bi. Lii de, fa Boroom bi la sottee, nu gis ko, yéemu.”
Explore Macë 21:42
7
Macë 21:43
«Loolu moo tax ma ne leen dees na jële nguurug Yàlla ci yeen, jox ko xeet wuy meññal meññeef ma ca war.
Explore Macë 21:43