Yeen nag, bumu deme noonu ci seen biir. Képp ku bëgga doon ku màgg ci yeen, na nekk seenub surga, te ku bëgga nekk seen njiit, na doon seenub jaam. Noonu la deme ci Doomu nit ki, ñëwul ngir ñu di ko surgawu, xanaa ngir di nekk surga, ba far maye bakkanam, def ko njotug ñépp.»