1
Macë 22:37-39
Kàddug Yàlla
KY
Yeesu ne ko: «“Yàlla sa Boroom, nanga ko soppe sa léppi xol, ak sa léppi jëmm, ak sa léppi xel.” Loolu mooy ndigal li gëna màgg, te moo jiitu. Ñaareel bi it yem ak moom, di: “Ni nga soppe sa bopp, nanga ko soppe sa moroom.”
Compare
Explore Macë 22:37-39
2
Macë 22:40
Ci ñaari ndigal yooyu la mboolem yoonu Musaa, ak kàdduy yonent yi aju.»
Explore Macë 22:40
3
Macë 22:14
Ndax kat ñu bare lañu woo, waaye ñu néew lañu tànn.»
Explore Macë 22:14
4
Macë 22:30
ndax keroog ndekkite la, kenn du am jabar mbaa jëkkër, waaye nit ñi dañuy mel ni malaaka yi ci asamaan.
Explore Macë 22:30
5
Macë 22:19-21
Wonleen ma poset bi ñuy feye galag.» Ñu daldi ko jox benn posetub xaalis. Yeesu ne leen: «Nataal bii ak tur wii ci binde, kuy boroom?» Ñu ne ko: «Buur Sesaar.» Mu ne leen: «Kon nag, yëfi Sesaar, joxleen ko Sesaar, te yëfi Yàlla, ngeen jox ko Yàlla.»
Explore Macë 22:19-21