1
Luug 2:11
Kàddug Yàlla
KY
Bésub tey jii ca dëkku Daawuda, juddule ngeen ab Musalkat, te mooy Almasi bi, di Sang bi.
Compare
Explore Luug 2:11
2
Luug 2:10
Malaaka mi ne leen: «Buleen tiit, ndax kat maa leen indil xibaaru jàmm bu doon mbég mu réy, ñeel askan wépp.
Explore Luug 2:10
3
Luug 2:14
«Daraja ñeel na Yàlla fa asamaan sa gëna kawe, jàmm ci kaw suuf ñeel ñi Yàlla baaxe.»
Explore Luug 2:14
4
Luug 2:52
Yeesu moom, ma ngay màgg ci dayo ak xel mu rafet, ak cérub yiw fi Yàlla ak nit ñi.
Explore Luug 2:52
5
Luug 2:12
Li ngeen ciy def ab takk moo di: dingeen gis liir bu ñu laxas, tëral ko ci gàmbug jur.»
Explore Luug 2:12
6
Luug 2:8-9
Booba ay sàmm a nga ca gox boobee, di fanaanee wattu seenug jur. Am malaakam Boroom bi jekki feeñu leen, leeru Boroom bi melax, wër leen, ñu tiit tiitaange ju réy.
Explore Luug 2:8-9