1
Yowaan 5:24
Kàddug Yàlla
KY
«Maa leen ko wax déy ci lu wér, ku dégg sama kàddu ba gëm ki ma yónni, yaa texe ba fàww, te àtte ba, doo ca jaare, waaye bàyyikoo nga ci dee, tàbbi ci dund.
Compare
Explore Yowaan 5:24
2
Yowaan 5:6
Kooku la Yeesu gis mu tëdd, mu xam ne yàgg na fa. Mu ne ko: «Ndax bëgg ngaa wér?»
Explore Yowaan 5:6
3
Yowaan 5:39-40
Yeena ngi gëstu Mbind mi, ndax ci ngeen yaakaara ame texe gu sax dàkk, yooyu bind nag far seedeel ma, te bëgguleena ñëw ci man, ba texe!
Explore Yowaan 5:39-40
4
Yowaan 5:8-9
Yeesu ne ko: «Jógal, jël sa basaŋ te dox.» Mu wér ca saa sa, jël basaŋam, daldi dox. Bés booba bésub Noflaay la woon.
Explore Yowaan 5:8-9
5
Yowaan 5:19
Yeesu dellu ne leen: «Maa leen ko wax déy ci lu wér, Doom ji manula def dara ci jëmmu boppam, lu moy li mu gis Baay bi def ko, ndax lu mu def, loolu itam la Doom ji di def.
Explore Yowaan 5:19