1
Yowaan 6:35
Kàddug Yàlla
KY
Yeesu ne leen: «Man maay ñam wiy joxe dund. Ku ñëw ci man, doo xiif mukk; te ku ma gëm, doo mar mukk.
Compare
Explore Yowaan 6:35
2
Yowaan 6:63
Noowug Yàlla mooy dundloo; nitu suuxu neen manul dara. Kàddu gi ma leen wax moo leen di jottali Noowug Yàlla giy taxa dund.
Explore Yowaan 6:63
3
Yowaan 6:27
Ñam wuy yàqu, bumu leen taxa liggéey; liggéeyalleen ñam wi sax, ñam wiy texeel fàww, te Doomu nit ki moo leen koy jox, ndax moom la Yàlla màndargaal, ngir firndeel ne moom la tànn.»
Explore Yowaan 6:27
4
Yowaan 6:40
Ndax sama coobarey Baay kat moo di képp ku gis Doom ji te gëm ko, na texe ba fàww, te maa koy dekkal keroog bés bu mujj ba.»
Explore Yowaan 6:40
5
Yowaan 6:29
Yeesu ne leen: «Jëf ji neex Yàlla, mooy ngeen gëm ki mu yebal.»
Explore Yowaan 6:29
6
Yowaan 6:37
Képp ku ma Baay bi jox dina ñëw, te man, ku ñëw ci man, duma ko dàq mukk.
Explore Yowaan 6:37
7
Yowaan 6:68
Simoŋ Piyeer ne ko: «Sang bi, ci kan lanu jëm? Kàddu giy texeel fàww, yaa ko yor!
Explore Yowaan 6:68
8
Yowaan 6:51
Man maay ñam wiy dund te wàcce fa asamaan. Ku lekk ci wii ñam, mooy texe ba fàww. Ñam woowu nag mooy samaw suux; maa ko joxe, ngir àddina dund.»
Explore Yowaan 6:51
9
Yowaan 6:44
Kenn manula ñëw ci man te Baay bi ma yónni indiwu ko; te ku ñëw ci man, maa koy dekkal kera bés bu mujj ba.
Explore Yowaan 6:44
10
Yowaan 6:33
Ndaxte ñamu Yàlla mooy ki wàcce asamaan te kooku moo may àddina ñu dund.»
Explore Yowaan 6:33
11
Yowaan 6:48
Man maay ñam wiy joxe dund.
Explore Yowaan 6:48
12
Yowaan 6:11-12
Yeesu jël mburu ya, yékkati kàddug cant, daldi ko séddale ña fa toog. Jën ya itam noonu, ñu lekk ba doyal. Ba ñu lekkee ba regg, Yeesu ne taalibeem ya: «Dajaleleen desiti mburu mi, ba dara du ci yàqu.»
Explore Yowaan 6:11-12
13
Yowaan 6:19-20
Ba taalibe ya joowee lu tollook juróomi kilomet ba juróom benn, Yeesu lañu séen, muy dox ca kaw dex ga, jëm ca gaal ga, ñu daldi tiit. Yeesu ne leen: «Man mii la, buleen tiit!»
Explore Yowaan 6:19-20