1
Yowaan 3:16
Kàddug Yàlla
KY
Ndax Yàlla moo sopp àddina, ba joxe jenn Doomam ji, ngir képp ku ko gëm, texe ba fàww, te du sànku mukk.
Compare
Explore Yowaan 3:16
2
Yowaan 3:17
Ndax kat Yàlla yebalul Doomam ci waa àddina ngir daan waa àddina, waaye musal waa àddina, mucc gu sottee ci Doomam, moo tax mu yebal ko.
Explore Yowaan 3:17
3
Yowaan 3:3
Yeesu ne ko: «Maa la ko wax déy ci lu wér, nit ki, su judduwaatul, du mana gis nguurug Yàlla.»
Explore Yowaan 3:3
4
Yowaan 3:18
Képp ku ko gëm, deesu la daan, waaye ku ko gëmul, daanees na ko ba noppi, ndax moo gëmul jenn Doomu Yàlla ji.
Explore Yowaan 3:18
5
Yowaan 3:19
Àtteb daan bi nii la tëdde: leer moo dikkal àddina, waaye nit ñi la lëndëm gënal leer ndax seen jëf yu bon.
Explore Yowaan 3:19
6
Yowaan 3:30
Moom mu gën di kawe, te man ma gën di suufe mooy li war.»
Explore Yowaan 3:30
7
Yowaan 3:20
Képp kuy def jëf ju sew, day bañ ag leer te du dikk ci leer gi, ngir ragal ay jëfam feeñ.
Explore Yowaan 3:20
8
Yowaan 3:36
Ku gëm Doom ji, yaay texe ba fàww; ku baña gëm Doom ji nag, doo gis googu texe, waaye sànjum Yàlla mooy dëkk ci sa kaw.
Explore Yowaan 3:36
9
Yowaan 3:14
Te itam noonee Musaa yékkatee woon jaan ja ca màndiŋ ma, fàww ñu yékkatee ni Doomu nit ki
Explore Yowaan 3:14
10
Yowaan 3:35
Baay bi moo sopp Doom ji, te lépp la teg ciy loxoom.
Explore Yowaan 3:35