Yowaan 3
3
Yeesu waar na waarekatub bànni Israayil
1Am na nit ku bokkoon ca Farisen ya, ku ñuy wax Nikodem, di njiit ca Yawut ya. 2Kooku moo dikk ag guddi ba ca Yeesu ne ko: «Kilifa gi, xam nanu ne ab kilifa nga bu bawoo fa Yàlla, nde kenn manula def firnde yii ngay def, te du Yàllaa ànd ak moom.» 3Yeesu ne ko: «Maa la ko wax déy ci lu wér, nit ki, su judduwaatul#3.3 judduwaat: ci làkku gereg, baat bi Yeesu wax mi ngi tekki «judduwaat» walla «juddoo ci kàttan gu jóge ci kaw»., du mana gis nguurug Yàlla.» 4Nikodem ne ko: «Ana nu nit di judduwaate te xasa dem bay mag? Daa mana duggaat ci biiru yaayam, ngir judduwaat?»
5Yeesu ne ko: «Maa la ko wax déy ci lu wér, nit ki su juddoowul ci ndox ak ci Noowug Yàlla, du mana tàbbi ci nguurug Yàlla. 6Lu juddoo ci nitu suuxu neen, nitu suux la, lu juddoo ci Noowug Yàlla nag, ag noo la. 7Li ma la ne: “Fàww ngeen judduwaat,” bumu la jaaxal. 8Ngelaw fu ko neex lay gelawe; coowam ngay dégg, waaye xamuloo fu mu jóge, xamuloo fu mu jëm. Noonu la it ci képp ku juddoo ci Noowug Yàlla.»
9Nikodem neeti ko: «Loolu nu mu mana ame?»
10Yeesu ne ko: «Yaw ngay jàngalekat bu mag ci bànni Israayil te xamuloo loolu? 11Maa la ko wax déy, ci lu wér; li nu xam, nu ngi koy wax; li nu gis, nu ngi koy seede, yeen kay yeena baña gëm li nu seede. 12Gannaaw mbiri àddina laa leen wax, gëmuleen ko, su ma leen waxee mbiri asamaan, ana nu ngeen koy gëme? 13Kenn masula yéeg fa asamaan ku moy ki wàcce asamaan, te mooy Doomu nit ki#3.13 Seetal ci Kàddu yu xelu 30.4.. 14Te itam noonee Musaa yékkatee woon jaan ja ca màndiŋ ma#3.14 Seetal ci Màndiŋ ma 21.9., fàww ñu yékkatee ni Doomu nit ki, 15ngir képp ku ko gëm, texe ba fàww.»
16Ndax Yàlla moo sopp àddina, ba joxe jenn Doomam ji, ngir képp ku ko gëm, texe ba fàww, te du sànku mukk. 17Ndax kat Yàlla yebalul Doomam ci waa àddina ngir daan waa àddina, waaye musal waa àddina, mucc gu sottee ci Doomam, moo tax mu yebal ko. 18Képp ku ko gëm, deesu la daan, waaye ku ko gëmul, daanees na ko ba noppi, ndax moo gëmul jenn Doomu Yàlla ji. 19Àtteb daan bi nii la tëdde: leer moo dikkal àddina, waaye nit ñi la lëndëm gënal leer ndax seen jëf yu bon. 20Képp kuy def jëf ju sew, day bañ ag leer te du dikk ci leer gi, ngir ragal ay jëfam feeñ. 21Waaye kiy def liy dëgg, ci leer gi lay dikk, ngir mu leer nàññ ne déggal Yàlla la ko jëfe.
Yaxya nangu na ne Yeesu moo sut lépp
22Gannaaw loolu Yeesu ànd ak ay taalibeem, dem diiwaanu Yude. Mu toog fa ak ñoom ab diir, di sóob nit ñi ci ndox. 23Ci biir loolu Yaxya itam di sóobe ci ndox ca Aynon, wetug Salim, ndax diiwaan bu bare ndox la woon. Nit ñi di ko fa fekk, mu di leen sóob ci ndox. 24Booba tëjaguñu Yaxya kaso.
25Werante nag am diggante ñenn ci taalibey Yaxya ak ab Yawut, ci mbirum setlu gi seen yoon laaj. 26Ci kaw loolu ñu dikk ca Yaxya ne ko: «Kilifa gi, ka nga dajeeloon ca wàllaa dexu Yurdan, te nga seedeeloon ko ag kàddu, moom de ma ngay sóobe ci ndox, ñépp jëm ca moom!» 27Yaxya ne leen: «Nit manula am lenn lu ko Yàlla joxul. 28Yeen ci seen bopp, yeenay samay seede ne maa noon man duma Almasi bi, waaye dees maa yebal ngir ma jiitusi Almasi boobu. 29Kiy séetal moo moom ab séetam. Waaye xaritu boroom séet bi day taxaw di ko déglu, bu déggee baatu boroom séet bi, bég. Mbég moomu nag laa moom, te mat na sëkk. 30Moom mu gën di kawe, te man ma gën di suufe mooy li war.»
31Ki jóge ci kaw moo féete ñépp kaw; ki jóge ci suuf nag, ci suuf la bokk, te mbiri suuf lay wax. Waaye ki jóge asamaan moo féete ñépp kaw. 32La mu gis ak la mu dégg lay seede, waaye kenn du gëm kàddug seedeem. 33Ku nangu kàddug seedeem nag yaa nangu ne Yàllaa wax dëgg. 34Yàlla kat, ku mu yebal, kàddug Yàlla lay wax, ndax Yàlla du natt li mu koy nàddil cig Noowam. 35Baay bi moo sopp Doom ji, te lépp la teg ciy loxoom. 36Ku gëm Doom ji, yaay texe ba fàww; ku baña gëm Doom ji nag, doo gis googu texe, waaye sànjum Yàlla mooy dëkk ci sa kaw.
Currently Selected:
Yowaan 3: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright