1
Yowaan 12:26
Kàddug Yàlla
KY
Ku may surgawu, na ma topp; fu ma nekk, sama surga ne fa moom itam. Ku ma surgawu nag, sama Baay moo koy teral.
Compare
Explore Yowaan 12:26
2
Yowaan 12:25
Képp ku bëgg bakkanam moo koy ñàkk; waaye ku bañ bakkanam ci àddina sii, moo musal bakkanam ba keroog muy texe ba fàww.
Explore Yowaan 12:25
3
Yowaan 12:24
Maa leen ko wax déy ci lu wér, su feppu bele waddul ci suuf, dee, wéetaay lay dëkke. Waaye su deewee lay meññ fepp yu bare.
Explore Yowaan 12:24
4
Yowaan 12:46
Man maa dikk, di ag leer ci àddina, ngir ku ma gëm du des cig lëndëm.
Explore Yowaan 12:46
5
Yowaan 12:47
Ku dégg samay wax te toppu ko, du man maa koy daan, ndax daan àddina taxu maa dikk, waaye musal àddinaa ma taxa dikk.
Explore Yowaan 12:47
6
Yowaan 12:3
Maryaama nag indi genn wàllu liitaru nàrd, diwu nàrd gu xeeñ lu neex te raxul te jafe njëg lool, sotti ko ca tànki Yeesu, daldi fomp tànk ya ak kawaru boppam. Kër ga gépp ne bann ak xetu diw ga.
Explore Yowaan 12:3
7
Yowaan 12:13
Ñu jël cari garab yu ñu koy lalal, daldi génn gatanduji ko. Ña ngay xaacu naan: «Osaana! Na barke wàcc ci ki dikk ci turu Boroom bi, na barke wàcc ci buurub Israayil!»
Explore Yowaan 12:13
8
Yowaan 12:23
Yeesu wax leen ne leen: «Waxtu wi ñu wara darajaal Doomu nit ki jot na.
Explore Yowaan 12:23