1
Yanqóoba 3:17
Kàddug Yàlla
KY
Waaye xel mu rafet ma bawoo fa kaw, set la njëkka def, teg ci ànd ak jàmm akug dal. Day taxa neexa jubool, fees ak yërmande, di meññ jëf ju baax, te mucc ci par-parloo akug jinigal.
Compare
Explore Yanqóoba 3:17
2
Yanqóoba 3:13
Ana ci yeen ku rafet xel te xam àddina? Na ko firndeele dundin wu rafet wu feeñ ci jëfam ju teey ndax xel mu rafet.
Explore Yanqóoba 3:13
3
Yanqóoba 3:18
Meññeefum njub nag, ci jàmm lees koy ji, ci biir doxkati jàmm yi.
Explore Yanqóoba 3:18
4
Yanqóoba 3:16
Ndax kañaan ak sàkku sa darajay bopp, fu mu ame, fa la salfaañoo di ame ak mboolem jëfi ñaawtéef.
Explore Yanqóoba 3:16
5
Yanqóoba 3:9-10
Aw làmmiñ lanuy sante kiy Boroom bi, di Baay, te it ci lanuy móoloo nit ñi bindoo takkndeeru Yàlla. Genn gémmiñ gi, ci la kàddug cant ak gu móolu di jibe. Bokk yi, warula deme noonu kat.
Explore Yanqóoba 3:9-10
6
Yanqóoba 3:6
Aw làmmiñ itam sawara la; làmmiñ a bokk ci sunuy cér, te di àddinay mbon, di gàkkal jëmm jépp. Aw làmmiñ, giiru dundu nit ki lay jafale ab taal bu tàkke fa sawara.
Explore Yanqóoba 3:6
7
Yanqóoba 3:8
Waaye aw làmmiñ, kenn manu koo tàggat ba mu mokk. Mooy aayteef gu kenn manula dànk, fees dell ak tookey dee.
Explore Yanqóoba 3:8
8
Yanqóoba 3:1
Bokk yi, bu ñu bare ci yeen wuta doon jàngalekatu mbooloom gëmkat mi, ndax xam ngeen ne nun ñiy jàngale nooy gëna metti ab àtte.
Explore Yanqóoba 3:1