Yàlla miy boroom jàmm, moom mi dekkal sunu Sang Yeesu, sàmm bu mag bi, ci dooley deret ji mu fase kóllëre gu sax dàkk, yal na leen matal sëkk ci lépp lu baax, ngir ngeen di jëfe coobareem. Yal na def ci nun bànneexu boppam bu mu sottal ci Yeesu Almasi bi daraja ñeel ba fàww. Amiin.