1
Yawut ya 6:19
Kàddug Yàlla
KY
Yaakaar jooju lanu am, mu mel ni diigalub gaal, diigal bu dëgër te wóor, ñeel sunu xol, te yaakaar jooju mooy bëtt rido ba, ba jàll ca néeg bu sella sell ba.
Compare
Explore Yawut ya 6:19
2
Yawut ya 6:10
Yàlla ñàkkul worma bay fàtte seen liggéey ak cofeel gi ngeen sopp turam, te firndeele ko ni ngeen taxawoo ñu sell ñi, démb ak tey.
Explore Yawut ya 6:10
3
Yawut ya 6:18
Ñaar yooyu du tebbiku ndax Yàlla du fen, te nun ñi daw làqusi ci moom, ci lanu ame ndëgërlaay lu réy lu nu ŋoye ci yaakaar ji ci sunu kanam.
Explore Yawut ya 6:18
4
Yawut ya 6:1
Kon nag nanu jóge ci ndoortel àlluway Almasi bi, daldi jàll jëm ci njàngum mag, te ñu baña lalaat njàngale yi jiitu ci xibaar bi. Njàngale mi moo di gëm Yàlla gannaaw tuubeel gi war ci jëf ju bon ji nit kiy def te muy jëfi dee.
Explore Yawut ya 6:1