YouVersion Logo
Search Icon

Yawut ya 6

6
1Kon nag nanu jóge ci ndoortel àlluway Almasi bi, daldi jàll jëm ci njàngum mag, te ñu baña lalaat njàngale yi jiitu ci xibaar bi. Njàngale mi moo di gëm Yàlla gannaaw tuubeel gi war ci jëf ju bon ji nit kiy def te muy jëfi dee. 2Te di itam njàngalem xeeti njàpp#6.2 njàpp mooy li Yawut daan def ngir sell. ak ñaan gu ànd ak tegeb loxo; ak mbirum dee-dekki ak àtteb bés-pénc biy sax dàkk. 3Nanu jëm kanam, te moom lanuy def, ndegam soob na Yàlla.
4Ñi ñu xasa leeral nag, te ñu jota mos may gu bawoo ci asamaan, séddu ci Noo gu Sell gi, deesu leen mana defal dara. 5Ñoo mos kàddug Yàlla gu baax gi ak manoore yu jamono jiy ñëw, 6ba noppi xàcc. Kon deesu leen waññi, ngir ñuy tuubati, nde ñoo daajaat Doomu Yàlla ci bant, ñoom ci seen bopp, teg ko toroxte ju ne fàŋŋ.
7Ndax suuf kat, su naanee ndox mu mu tawlu ay yoon, ba meññ gàncax gu jariñ ñi ñu koy beyal, soosa suuf dina séddu ci barke bu bawoo fa Yàlla. 8Waaye su meññee ay dég aki xaaxaam, amul njariñ, alkuteem lees di tudd léegi, te lakk lay mujje.
9Waaye nag soppe yi, nii nuy waxe ak yeen teewul nu di leen yaakaar ci lu wér, li leen gëna amal njariñ, te bokk ci seenug mucc. 10Yàlla ñàkkul worma bay fàtte seen liggéey ak cofeel gi ngeen sopp turam, te firndeele ko ni ngeen taxawoo ñu sell ñi, démb ak tey. 11Waaye danoo bëgg kenn ku nekk ci yeen wéye genn parlu googu ngeen nekke, ba kera muj ga, ngir seen yaakaar sotti ba mat sëkk. 12Su ko defee dungeen yàccaaral, waaye dangeen di roy ci ñi gëm te muñ, ba jagoo digey Yàlla.
Digeb Yàlla du jaas
13Mu mel ni Ibraayma, ba Yàlla di digoo ak moom, Yàlla manul woona giñe ku sut Yàlla. Moo tax mu giñal ko ci boppam, 14ne ko: «Maa lay barkeel a barkeel déy, ful laa ful#6.14 Seetal ci Njàlbéen ga 22.17.15Noonu la Ibraayma muñe, ba kera mu jote ca dige ba.
16Nit nag, ku ko sut lay giñe, ngir dogal kàddu, ba teesal wépp werante. 17Yàllaa bëggoona firndeel nu mu gëna leere ñeel ñi moom dige bi, ne ab dogalam du tebbiku mukk. Moo tax mu dogale ngiñ ab digeem. 18Ñaar yooyu du tebbiku ndax Yàlla du fen, te nun ñi daw làqusi ci moom, ci lanu ame ndëgërlaay lu réy lu nu ŋoye ci yaakaar ji ci sunu kanam. 19Yaakaar jooju lanu am, mu mel ni diigalub gaal, diigal bu dëgër te wóor, ñeel sunu xol, te yaakaar jooju mooy bëtt rido ba, ba jàll ca néeg bu sella sell ba. 20Fa la ndaw li nu jiitu dugg ngir nun, te kookooy Yeesu mi ñu fal sarxalkat bu mag ba fàww, mu topp dayob Melkiccedeg.

Currently Selected:

Yawut ya 6: KY

Highlight

Copy

Compare

Share

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in