Ndax kat nëgëni tey waroon na leena fekk diy jàngalekat, waaye aajowoo ngeen ba tey ku leen jàngal ndoortel waxi Yàlla. Nàmpum soow ngeen mujj aajowoo, ndax ñàkka àttan ñam wu dëgër. Képp ku tollu ci nàmpum soow nag, tuut-tànk nga, doo mana xam dara ci kàddug njub.