1
Yawut ya 4:12
Kàddug Yàlla
KY
Kàddug Yàlla de luy dund la, ànd ak doole, te moo gëna ñaw saamaru ñaari ñawka bu gëna ñaw. Day sar ba fa xel akug noo digaloo, ba fa yax ak yuq dajee, te man naa càmbar ay xalaat ak mébéti xol.
Compare
Explore Yawut ya 4:12
2
Yawut ya 4:16
Kon nag nanu ñemee dikk ba ca ngàngunem yiw ma, ndax nu jot yërmande te dajeek aw yiw wu nu wallu fu nu ko soxlaa.
Explore Yawut ya 4:16
3
Yawut ya 4:15
Ndax sarxalkat bu mag bi nu am du ku tëlee yég sunuy néew doole, waaye ni nun rekk lees ko nattoo wet gu nekk, te taxul mu bàkkaar.
Explore Yawut ya 4:15
4
Yawut ya 4:13
Te it amul mbindeef mu làqu fi kanam Yàlla. Lépp a ne duŋŋ, ne fàŋŋ, muy gis, te moom lanuy waxal bés-pénc.
Explore Yawut ya 4:13
5
Yawut ya 4:14
Gannaaw nag am nanu kilifag sarxalkat bu mag bu jàll ba ca biir asamaan, te mooy Yeesu Doomu Yàlla, nanu ŋoy ci yoonu ngëm wi.
Explore Yawut ya 4:14
6
Yawut ya 4:11
Nanu def sunu kem-kàttan boog, ngir tàbbi ci googu noflaay, bala kenn a daanu ndax déggadi gu mel ni gu maam ya.
Explore Yawut ya 4:11