1
2.Timote 4:7
Kàddug Yàlla
KY
Xare bu baax bi, xare naa ko, rawante bi, sottal naa ko, ngëm gi ma am, sàmm naa ko.
Compare
Explore 2.Timote 4:7
2
2.Timote 4:2
waareel kàddug Yàlla te taxaw ci temm, su neexee ak su naqaree; di yedde, di femmoo, di ñaaxe, tey saxoo muñ ci sa njàngale.
Explore 2.Timote 4:2
3
2.Timote 4:3-4
Ndax kat ay jamonoo ngi ñëw, nit ñi dootuñu xajoo àlluwa ju wér, waaye seeni bëgg-bëggi bopp lañuy topp, bay fortaatoo fu nekk ay jàngalekat yu leen di wax lu leen neex. Dëgg lañuy tanqamlu, lajj, wuti léebi neen.
Explore 2.Timote 4:3-4
4
2.Timote 4:5
Waaye yaw, àndal ak sa sago ak diggante boo mana tollu, te ñeme coono. Jàppal ci liggéeyub jottali xibaaru jàmm bi, beyal sa waar ba mu mat sëkk.
Explore 2.Timote 4:5
5
2.Timote 4:8
Léegi nag kaalag njekk a may xaar, te Boroom bi, àttekat bu jub bi moo ma koy yool, keroog ca bés ba, te du man rekk la koy yool, waaye itam képp ku koy séentu te yàkkamti bés ba muy feeñ.
Explore 2.Timote 4:8