Ndax kat ñàkkoona xam yoonu njub wi sax moo doon gën ci ñoom, xam ko ba noppi, dëddu ndigal lu sell la ñu leen ca àgge woon. Li léeb wii wax te muy dëgg, moo leen dikkal: «Xaj waccu, lekkaat ko; te cangaayu mbaam-xuux, teewu koo xalangootee poto-poto.»