Mucc ga 6:8-9
Mucc ga 6:8-9 KYG
Maa leen di yóbbu ba ngeen dugg réew ma ma giñoon ne maa koy jox Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba, te maa leen koy moomale, man Aji Sax ji.» Ba Musaa waxee loolu bànni Israyil, dégluwuñu ko sax ndax xol bu jeex ak njaam gu metti.