1
Mucc ga 9:16
Kàddug Yàlla gi
KYG
Waaye maa la musal, te li ma ci jublu moo di won la sama doole, ba sama riirum tur dajal àddina.
ប្រៀបធៀប
រុករក Mucc ga 9:16
2
Mucc ga 9:1
Ba loolu wéyee Aji Sax ji da ne Musaa: «Demal ca Firawna, nga ne ko: Aji Sax ji Yàllay Ebrë yi dafa wax ne: “Bàyyil sama ñoñ, ñu dem màggali ma.
រុករក Mucc ga 9:1
3
Mucc ga 9:15
Nëgëni tey doon naa xàcci sama loxo xaat, dumaa leen mbas mu leen di fare ci kaw suuf, yaw yaak sa waa réew.
រុករក Mucc ga 9:15
4
Mucc ga 9:2-3-4
Ndax boo leen bañee bàyyi kat, xanaa di leen téye ba tey, loxol Aji Sax ji dina dal ci sa kaw jur gi ci tool yi, muy fas ak mbaam ak giléem, jur gu gudd ak gu gàtt, te jàngoro ju aaytal lool lay doon. Waaye man Aji Sax ji maay ràññatle juru bànni Israyil ak juru waa Misra, ba lenn du dee ci mboolem lu bànni Israyil moom.”»
រុករក Mucc ga 9:2-3-4
5
Mucc ga 9:18-19
Te kat nëgëni ëllëg dinaa taw yuur bu réy, bu masula am Misra, ba mu sosoo ba tey jii. Kon nag sa jur ak mboolem loo am, te mu nekk ci biti, booleel fat fu wóor, ndax lu nekk ci biti te fateesu ko, su tawtee dee, muy nit mbaa mala.’ ”»
រុករក Mucc ga 9:18-19
6
Mucc ga 9:9-10
Su ko defee dóom bi doon pënd bu sew ci kaw réewum Misra gépp, daldi def ay taab yuy sotti dëtt ci réewum Misra gépp, nit ak mala.» Ñu sàkk dóomu-taal, àgg ca kanam Firawna, Musaa xalab dóom ba, mu jëm asamaan, dóom ba def ay taab yuy sotti dëtt ca nit ñaak mala ya.
រុករក Mucc ga 9:9-10
គេហ៍
ព្រះគម្ពីរ
គម្រោងអាន
វីដេអូ