YouVersion Logo
Search Icon

Tit 2

2
Àlluwa ju wér lii lay xamle
1Yaw nag waareel li dëppook àlluwa ji wér, 2te mooy, na mag ñi noot seen bakkan, di ñu tedd, jiital seenum xel, te pastéefu ci wàllu ngëm ak cofeel akug muñ.
3Naka noonu, jigéen ñu mag ñi itam, nañu jëfe ni mu jekke ci ay nit ñu sell; buñu yàq der, bu leen sàngara jiital, te nañuy jàngale lu baax, 4ngir tàggat jeeg ju ndaw ji ci sopp seen jëkkër, sopp seeni doom, 5di ñu jiital seenum xel, set jikko, di liggéey ca seeni kër, baax, nangul seen jëkkër, ba kenn du baatal kàddug Yàlla.
6Naka noonu, xale yu góor yi itam, ñaaxleen ci jiital seenum xel. 7Te nanga doon, yaw ci sa bopp ab royukaay ci lépp ndax sa jëf ju baax, te nga boole ko ak àlluwa ju dëggu te tedd, 8ak kàddu gu wér gu kenn dul mana weddi, ngir rusloo ab noon bu amul lenn lu bon lu mu nu baatale.
9Jaam yi, nañu nangul seeni sang ci lépp, di sàkku seen bànneexu sang, te ñu bañ di tontoonte ak moom, 10mbaa di randal. Waaye nañu firndeel ne ñoo yelloo kóolute gu mat sëkk, su ko defee dinañu sagal ci lépp, àlluwa ji ñu jànge, te muy ju Yàlla sunu Musalkat.
11Ndax yiwu Yàlla kat feeñ na, te looloo indil ñépp ag mucc. 12Yiw woowu moo nu digal nu dëddu ñeme Yàlla ak xemmemtéefi àddina, te jiital sunum xel, di jëfe njub, te nekke ragal Yàlla ci àddinay tey jii. 13Loolu lees nu digal, li feek nu ngi séentu yaakaaru mbég ma, keroog bésu peeñum sunu màggaayu Yàlla miy Yeesu Almasi bi, Musalkat bi. 14Moo maye bakkanam ngir nun, moo nu jot, ba nu mucc ci gépp njubadi, moo nu def askan wu mu setalal boppam, séddoo nu, nuy askan wu farlu ci jëf ju baax.
15Googu kàddu ngay waaree, di dénkoo ak di femmoo, te boole ci fulla ju mat sëkk. Bu la kenn yab.

Currently Selected:

Tit 2: KY

Highlight

Copy

Compare

Share

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in