YouVersion Logo
Search Icon

Tit 1

1
Ubbite gi
1Ci man Póol la bataaxal bii bawoo, man jaamub Yàlla, biy ndawal Yeesu Almasi bi, mu yebal ma, ngir ma dugal ñi Yàlla tànn ci yoonu ngëm ak xam-xamu dëgg giy taxa ragal Yàlla. 2Ngëm googu ak xam-xam boobu, ñu ngi sukkandiku ci yaakaar ji nu am ci texe ba fàww, te googu texe, Yàlla mi dul fen, moo ko dige ba àddina sosoogul. 3Waaye tey bi mu jotee, Yàlla sunu Musalkat moo feeñal kàddoom ci biir waare bi mu ma dénk man, te moo ma digal ma xamle ko. 4Bataaxal bi ñeel na Tit, sama doomu yoon ci kaw ngëm gi nu bokk. Aw yiw ak jàmm ñeel na la, bawoo fa Yàlla Baay bi ak Almasi Yeesu sunu Musalkat.
Póol sas na Tit ca réewum Keret
5Li tax ma bàyyi la gannaaw ca dun bu tudd Keret mooy nga mottali la desoon ca liggéey ba, te nga tabb ay mag ñu jiite mbooloo mi ci dëkk bu nekk, na ma la ko sante woon, man ci sama bopp. 6Ndegam nit a nga ca seen biir ñoom, di ku mucc sikk, te dencul lu wees jenn jabar, te ay doomam di ay gëmkat ñu ñu tuddul ci afal seen bakkan akug déggadi, nanga tabb ku mel noonu. 7Ndax kat, njiit li war na di ku mucc sikk, gannaaw ab saytukatu kër Yàlla la. Bumu di ku bew, mbaa ku gaawa mer, mbaa ab màndikat, mbaa bëggkatub xeex, mbaa wutkatub am-am bu lewul. 8Waaye war na di ku man gan, ku xejjoo lu baax, jiital am xelam, jub, sell te moom boppam. 9Na jàpp bu dëgër ci kàddu gu wóor gi, ni ñu ko ko jàngale, ngir mu man di ñaaxe jooju àlluwa ju wér, tey tiiñal weddikat yi.
Gëmkati Keret jar nañoo femmu
10Ndax kat bare na ñu të, rawatina ci tuubeen ñi bokk ci askanu yawut, ay waxkati neen lañu, te ñooy yàq xeli nit ñi. 11Li war moo di tëj seen gémmiñ, ndax këri lëmm lañuy tase àlluwa ju ñu amul sañ-sañam, ngir di ko sàkkoo am-am bu lewul. 12Ma wax ko waru jenn waay, ab waa Keret buy seen yonentu bopp. Mu ne: «Waa Keret, ay fen-kati neen, soxor niy rabi àll, fuqle, yaafus.» 13Loolu mu leen seedeel mooy dëgg, te moo tax nga war leena femmoo kàddu yu dëgër, ngir seen ngëm tegu ci àlluwa ji wér, 14te baña topp léebi neen yu Yawut yi ak santaaney nit ñi dëddu liy dëgg. 15Nit ñi set nag, seen lépp ay set, waaye ñi boole sobewu ak gëmadi, seen dara setul, seen xalaat ak seenum xel, ñooy bokk sobewu. 16Xam Yàlla lañuy woote, te seeni jëf weddi Yàlla; nit ñu jara jéppi, ñu déggadi lañu, te tëlee def lenn lu baax.

Currently Selected:

Tit 1: KY

Highlight

Copy

Compare

Share

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in