YouVersion Logo
Search Icon

Peeñu ma 1

1
Ubbite gi
1Yeesu Almasi bi moo yégle peeñu mii ko Yàlla jox ngir mu won ay jaamam yenn xew-xew yu dëgmal. Malaakaam la yebal ci Yowaan ngir xamle ko. 2Yowaan moo seede mboolem li mu gis, te mu jëm ci kàddug Yàlla ak seedes Yeesu Almasi bi. 3Ndokkalee képp ku jàng ak mboolem ñi déglu yii kàdduy waxyu, tey sàmm li ñu ci bind, ndaxte waxtu wi jege na.
Ab nuyoo ñeel na juróom ñaari mboolooy gëmkat
4Lii mu ngi tukkee ci man Yowaan, ñeel juróom ñaari mboolooy gëmkat ña ca diiwaanu Asi. Na leen yiw ak jàmm ñeel, tukkee fa Ki masa nekk, Ki nekk, di Kiy dikk, tukkee it fa boroom juróom ñaari noo ya#1.4 juróom ñaari noo ya: seetal ci 4.5; 5.6. fa kanam ngànguneem#1.4 ngàngune ma mooy fa buur biy toog., 5tukkee itam fa Yeesu Almasi bi, seede bu wóor bi, moom taaw bi#1.5 taaw bi: taaw mooy ki njëkka juddu, waaye ab juddu taxul ñuy wax fii. Li Yeesu Almasi bi njëkka dekki ndekkite lu dee toppatul moo tax ñuy wax. Mooy taaw ci kaw darajaam ndax moo sut ñépp, yilif lépp luy mbindeef, te ci darajaam la ñépp di dekkee., ki njëkka dekki, jóge ci ñi dee, di kilifay buuri kaw suuf.
Moom mi nu sopp, yiwee nu deretam, ba nu teqalikook kilifteefu sunuy bàkkaar, 6ba noppi def nu nuy askanu sarxalkati Buur Yàlla Baayam#1.6 Baayam: seetal ci Luug 3.23, 38., na ko daraja ak manoore ñeel tey ak ëllëg ba fàww. Amiin.
7Mu ngoogu di dikk, indaale niir yi,
te ñépp a koy teg bët,
ba ca ña ko jamoon sax,
te giiri kaw suuf yépp ay jooy ndax moom.
Noonu la moos. Amiin.
8«Man, maay Alfa, di Omega#1.8 Alfa, Omega: ci làkku gereg, alfa moo njëkk ci araf yi, omega mujj ci. Kuy Alfa ak Omega nag moo njëkk, moo mujj.», la Boroom bi Yàlla wax, moom Ki masa nekk, Ki nekk, di Kiy dikk ëllëg, te di Aji Man ji.
Yowaan am na peeñu ca dunu Patmos
9Man Yowaan seen mbokk mi séddook yeen nattu ak barkeb nguurug Yàlla, ak muñ gi ci Yeesu, maa nga woon fa ñu ma toxaloon, ca dun ba ñuy wax Patmos. Li ko waral di sama waare ci kàddug Yàlla ak seedeel Yeesu. 10Benn bésub Sang bi, Leerug Yàlla dikkal na ma, ma dégg ci sama gannaaw baat bu xumb nig liit. 11Mu ne: «Mboolem loo gis, bind ko cib téere, nga yónnee ko juróom ñaari mboolooy gëmkat ña ca dëkk ya ñuy wax Efes ak Esmirna ak Pergam ak Catir ak Sàrd ak Filadelfi ak Lawdise#1.11 Dëkk yooyu ñu ngi ci réew mu tudd Tirki tey.
12Naka laa geestu, di seet kuy wax ak man, ma daldi gis juróom ñaari tegukaayi làmp yu wurus. 13Ca digg tegukaayi làmp ya, jëmm juy nirook nit#1.13 Seetal ci Dañeel 7.13. a fa nekk. Ma nga sol mbubb mu tollu ci ndëgguy tànk yi, takkoo ngañaayal wurus ci dënn bi. 14Kawaru bopp baa nga weex tàll, gët ya di tàkk ni sawara, 15tànk ya mel ni xànjar bu yànj bu ñu xelli, baat bay riir ni gannaxi géej. 16Ma nga yor ca loxol ndijooram juróom ñaari biddiiw, ab saamaru ñaari ñawka bu ñaw di lange ca gémmiñ ga, xar-kanam baa nga leer nàññ ni jantub njolloor.
17Naka laa ko gis, ne dàll daanu ci ay tànkam ni ku dee. Mu teg ma loxol ndijooram, ne ma: «Bul tiit. Maay Ki njëkk, di Ki mujj. 18Maay Kiy dund, maa dee woon, maay dund nii tey ak ëllëg ba fàww te maa yor caabiy dee ak njaniiw. 19Kon nag bindal li nga gis: Li am nii tey ak itam liy ñëw gannaaw lii. 20Kumpa gi ci juróom ñaari biddiiw yi nga gis ci sama loxol ndijoor, ak juróom ñaari tegukaayi làmp yu wurus yi, li muy firi mooy: juróom ñaari biddiiw yi ñoo di malaakay juróom ñaari mboolooy gëmkat ñi; juróom ñaari tegukaayi làmp yi ñoo di juróom ñaari mbooloo yi.»

Currently Selected:

Peeñu ma 1: KY

Highlight

Copy

Compare

Share

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in