YouVersion Logo
Search Icon

Filib 4

4
1Kon nag yeen samay bokk, soppe yi ma namm, di leen bége, te ngeen di sama kaalag ndam gi ma yooloo ci sama liggéey, ngalla soppe yi, nangeen saxe noonu ci Boroom bi!
Póol dénkaane na
2Bu loolu weesoo, Ewodi laay tinu, di tinu Santis, ñaari jigéen ñooñu, ngir ñu fexe ba juboo, ngir Boroom bi ñu bokk. 3Yaw itam sama mbokkum surga bu dëggu bi, dama lay ñaan nga jàppale leen ci, ñoom ñaar ñooñoo bokkoon ak man coonob xamle xibaaru jàmm bi, ñoom ak ñoom Kelemaŋ, mboolem sama bokki liggéeykat yi seeni tur binde ca téereb dund ba.
4Bégleen ci Boroom bi fu ngeen tollu, ma waxati ko, bégleen! 5Na seen lewetaay wóor ñépp, Sang bi jegesi na. 6Buleen jaaxle ci dara, waaye ci mbir mu mu mana doon, deeleen dikke Yàlla seeni soxla, di ko ñaan aka dagaan te boole ci di ko sant. 7Su boobaa jàmmu Yàlla ji wees ab takk, mooy sàmm seen xol ak seenum xel ndax Almasi Yeesu.
8Li ci des nag bokk yi, moo di lii: mboolem lu dëggu, ak mboolem lu tedd, ak mboolem luy njub, ak mboolem lu set, ak mboolem lu jekk, ak mboolem lees di rafetlu, ndegam lu nawlu la te yelloo ngërëm, na leen loola soxal. 9Li ngeen jànge ci man te jële ko ci man, ak li ngeen dégge ci man, gise ko ci man, jëfeleen ko. Su boobaa Yàlla miy boroom jàmm mooy ànd ak yeen.
Póol gërëm na waa Filib
10Maa ngi bége Boroom bi lool ci nii ngeen mujj yeesale tey, seen yitte ci man, yitte ju ngeen amoon moos naka jekk, xanaa dangeena ñàkkoona jekku seen ndimbal. 11Ag ñàkk nag taxul may waxe nii, nde tàmm naa di doylu ci diggante bu ma mana tollu. 12Miin naa néewle, man naa naataange. Fépp fu ma tollu ak ci lépp, làqoo naa pexe mu ma manee jant yu ma regge ak yu ma xiife, ci biir naataange akug ñàkk. 13Lépp laa mane ci ndimbalal ki may manal. 14Teewul seen ndimbal lii di jëf ju rafet ju ngeen bokke ak man sama njàqare.
15Yeen waa Filib, xam ngeen xéll ne ba waareb xibaaru jàmm bay door, te ma bàyyikoo diiwaanu Maseduwan, amul woon menn mbooloom gëmkat mu ma séqaloon ab joqalanteb ndimbal, xanaa seen mennum mbooloo. 16Ba ma nekkee Tesalonig sax, yónnee ngeen ma ay yoon, lu ma faje samay soxla. 17Du caageenu ndimbal lu ma sàkku ci yeen, li may sàkku kay moo di yokkuteb yool bu leen ñeel. 18Fii ma tollu jot naa li ma aajowoo lépp, maa ngi ci naataange; doyle naa sëkk, gannaaw ba ma nangoo ci loxol Epafrodit seenub yóbbante, te sarax su ñu nangu la, di xeeñ xetug jàmm, te neex Yàlla mi mu ñeel. 19Te sama Yàlla itam mooy sàkke ci koomam gu yéeme gi ci Almasi Yeesu, ba fajal leen seen soxla yépp.
20Daraja ñeel na Yàlla sunu Baay, tey ak ëllëg ba fàww. Amiin.
Tàggatoo jib na
21Nuyulleen ma mboolem ñu sell ñi gëm Almasi Yeesu. Bokki gëmkat ñi ànd ak man, ñu ngi leen di nuyu. 22Te it gëmkat ñu sell ñépp a ngi leen di nuyu, rawatina waa kër Buur Sesaar.
23Yal na yiwu Sang Yeesu Almasi bi ànd ak seenum xel.

Currently Selected:

Filib 4: KY

Highlight

Copy

Compare

Share

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in