1
Filib 4:6
Kàddug Yàlla
KY
Buleen jaaxle ci dara, waaye ci mbir mu mu mana doon, deeleen dikke Yàlla seeni soxla, di ko ñaan aka dagaan te boole ci di ko sant.
Compare
Explore Filib 4:6
2
Filib 4:7
Su boobaa jàmmu Yàlla ji wees ab takk, mooy sàmm seen xol ak seenum xel ndax Almasi Yeesu.
Explore Filib 4:7
3
Filib 4:8
Li ci des nag bokk yi, moo di lii: mboolem lu dëggu, ak mboolem lu tedd, ak mboolem luy njub, ak mboolem lu set, ak mboolem lu jekk, ak mboolem lees di rafetlu, ndegam lu nawlu la te yelloo ngërëm, na leen loola soxal.
Explore Filib 4:8
4
Filib 4:13
Lépp laa mane ci ndimbalal ki may manal.
Explore Filib 4:13
5
Filib 4:4
Bégleen ci Boroom bi fu ngeen tollu, ma waxati ko, bégleen!
Explore Filib 4:4
6
Filib 4:19
Te sama Yàlla itam mooy sàkke ci koomam gu yéeme gi ci Almasi Yeesu, ba fajal leen seen soxla yépp.
Explore Filib 4:19
7
Filib 4:9
Li ngeen jànge ci man te jële ko ci man, ak li ngeen dégge ci man, gise ko ci man, jëfeleen ko. Su boobaa Yàlla miy boroom jàmm mooy ànd ak yeen.
Explore Filib 4:9
8
Filib 4:5
Na seen lewetaay wóor ñépp, Sang bi jegesi na.
Explore Filib 4:5
9
Filib 4:12
Miin naa néewle, man naa naataange. Fépp fu ma tollu ak ci lépp, làqoo naa pexe mu ma manee jant yu ma regge ak yu ma xiife, ci biir naataange akug ñàkk.
Explore Filib 4:12
10
Filib 4:11
Ag ñàkk nag taxul may waxe nii, nde tàmm naa di doylu ci diggante bu ma mana tollu.
Explore Filib 4:11