YouVersion Logo
Search Icon

Màndiŋ ma 16

16
Kore fippu na
1Ku ñuy wax Kore doomu Iccar, mi askanoo ci Keyat doomu Lewi, moo àndoon ak ay Rubeneen, ñuy Datan ak Abiram, doomi Elyab, ak Oon doomu Pelet, 2ñu jógal Musaa, ñook ñaari téeméer ak juróom fukk (250) ci bànni Israayil, diy kilifa ci mbooloo mi, am baat ca pénc ma, te di ñu am aw tur. 3Ci kaw loolu ñu bokk daje fi kaw Musaa ak Aaróona, ne leen: «Doy na sëkk! Mbooloo mi ba mu daj, ñépp a sell, te ci sunu biir la Aji Sax ji nekk. Ana lu ngeen di xoggaliku ci kaw mbooloom Aji Sax ji?»
4Ba Musaa déggee loolu, da ne gurub, dëpp jë bi fi suuf. 5Mu wax Kore ak gàngooram gépp, ne: «Bu ëllëgee, Aji Sax ji mooy xamle kan la séddoo ak kan mooy ki sell, mu jegeñal ko boppam. Ki mu tànn nag, dina ko jegeñal boppam. 6Dangeen di def nii: Jëlleeni and, yaw Kore, yaak sa gàngoor gépp, 7te ngeen def ciy xal, def ci cuuraay fi kanam Aji Sax ji, ëllëg. Su ko defee ku Aji Sax ji tànn, kookooy ki sell. Doy na sëkk, yeen Leween ñi!» 8Musaa teg ca ne Kore: «Yeen Leween ñi, dégluleen nag! 9Xeeb ngeen daal ber gi leen Yàllay Israayil ber ci mbooloom Israayil, jegeñal leen boppam, ngeen di liggéey liggéeyu màkkaanu Aji Sax ji, di taxaw fi kanam mbooloo mi, di leen jaamul Yàlla? 10Yaw mu jegeñal la, yaak sa bokki Leween ñépp, ngeen di xëccu céru carxal, boole ci! 11Kon kay yaw yaak sa gàngoor gépp, ci kaw Aji Sax ji ngeen bokk daje! Ana kuy Aaróona, ba ngeen di ñaxtu ci kawam?»
12Musaa nag woolu Datan ak Abiram, doomi Elyab, ñu ne ko: «Danoo ñëwul! 13Dangaa xeeb li nga nu jële réew mu meew maak lem ja tuuroo, ngir reylu nu ci màndiŋ mi, ba tax ngay buur-buurlu ci sunu kaw teg ci? 14Du réew mu meew maak lem ja tuuroo nga nu yóbbu de, te séddoo nu céri tool mbaa tóokëri reseñ. Mbooloo mii mépp, man nga leena tuur lëndëm? Danoo ñëwul!» 15Ba loolu amee Musaa mer lool. Mu ne Aji Sax ji: «Bul geesu sax seen sarax. Menn mbaam sax, masuma leen koo jëlal te masuma cee tooñ kenn.»
Way-fippu ya jot nañu seen añ
16Musaa nag ne Kore: «Yaw, yaak sa gàngoor gépp, ñëwleen ca kanam Aji Sax ji, yaak ñoom ak Aaróona, ëllëg. 17Na ku nekk jël andam, def ci cuuraay, te na ku ci nekk indi andam fi kanam Aji Sax ji, muy ñaari téeméeri and ak juróom fukk, yaak Aaróona it, ku nekk ak andam.»
18Ba mu ko defee ku nekk jëlub andam, def cay xal, teg ca cuuraay. Ñu taxaw ca bunt xaymab ndaje ma, ñook Musaa ak Aaróona. 19Kore nag dajale gàngoor gépp fa ñoom, ca bunt xaymab ndaje ma. Ci kaw loolu leeru Aji Sax ji feeñu mbooloo ma mépp!
20Aji Sax ji wax Musaa ak Aaróona, ne: 21«Xiddileen mbooloo mii, ma xoyom leen léegi!» 22Musaa ak Aaróona ne gurub, dëpp seen jë fa suuf, daldi ne: «Éy Yàlla, yaw Yàllay bépp boroom bakkan bu bindoo aw suux, xanaa du kenn ay bàkkaar, nga far sànju ci kaw mbooloom lëmm?»
23Ci kaw loolu Aji Sax ji ne Musaa: 24«Waxal mbooloo mi, ne leen ñu jóge fi wër màkkaani Kore ak Datan ak Abiram.»
25Musaa daldi jubal ca Datan ak Abiram, magi Israayil topp ca. 26Ci biir loolu mu wax ak mbooloo ma, ne leen: «Ngalla dàndleen xaymay nit ñu bon ñii, te buleen laal seen lenn, bala ngeen di buuboondook mboolem bàkkaari ñii.» 27Ñu daldi jóge mboolem fa wër màkkaani Kore ak Datan ak Abiram. Datan ak Abiram ñoom, ña nga génn, taxaw ca seen bunti xayma, ñook seeni jabar ak seeni doom, ak seeni tuut-tànk.
28Musaa nag ne: «Lii nag moo leen di xamal ne Aji Sax ji moo ma yebal ngir ma def jëf jii jépp, waaye du sama coobarey bopp: 29Ndegam ni mboolem doom aadama di deewe, ni la ñii deewe, seen demin di deminu mboolem doom aadama, su boobaa du Aji Sax jee ma yebal. 30Waaye ndegam Aji Sax ji moo sàkk ba sàkk tey lu masula am, ba suuf ŋa, mëdd leen, ñook lu bokk ci ñoom, ñu tàbbiwaale bakkan biir njaniiw, su boobaa dingeen xam ne ñoom ñii ñoo xarab Aji Sax ji.» 31Naka la Musaa di daaneel kàddu yooyu yépp, fa ñu taxaw jekki xar, 32suuf ŋa, mëdd leen, ñook seen waa kër, ak mboolem ku bokk ci Kore, ak mboolem alal ja. 33Ñu daldi tàbbiwaale bakkan biir njaniiw, ñook mboolem lu ñu moom, suuf sàng leen, ñu réer mbooloo ma mërr. 34Mboolem Israayil dégg seen yuux ya, daldi daw, te naan: «Nan daw bala noo suuf a mëdd!»
35Ci kaw loolu sawara moo bawoo fa Aji Sax ji, xoyom ñaari téeméeri nit ak juróom fukk ña indi woon saraxu cuuraay ba.

Currently Selected:

Màndiŋ ma 16: KY

Highlight

Copy

Compare

Share

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in

Video for Màndiŋ ma 16