YouVersion Logo
Search Icon

Màndiŋ ma 15

15
Lu jëm ci saraxi pepp ak diw ak biiñ
1Aji Sax ji waxati Musaa, ne: 2«Waxal bànni Israayil ne leen: Bu ngeen demee ca réew ma ngeen di sanci, réew ma ma leen jox, 3bu ngeen di defal Aji Sax ji saraxu sawara, muy saraxu rendi-dóomal, mbaa sarax su nit di wàccoo aw xas, mbaa saraxu yéene, mbaa seen saraxi màggal, ngir xeeñal xetug jàmm ñeel Aji Sax ji, te muy lu jóge ci jur gu gudd mbaa gu gàtt, defe leen ko nii:
4«Kiy sarxal Aji Sax ji ab saraxam, na sarxewaale saraxu pepp bu benn fukkeelu efab sunguf su mucc ayib, di ñetti kilo, su ñu xiiwe ñeenteelu xaajub xiinu diw, di liitar, 5ak biiñ ngir saraxu tuuru, ñeenteelu xaajub xiin, di liitar, mu ànd ak saraxu rendi-dóomal mbaa beneen sarax, su dee kuuy mu ndaw.
6«Su dee am kuuy mu mag, saraxu pepp bi muy àndal, ñaari fukkeeli efay sunguf su mucc ayib lay doon, di juróom benni kilo, ñu xiiwe ko ñetteelu xaajub xiinu diw, di liitaru diw ak genn-wàll, 7ak biiñ ngir saraxu tuuru, ñetteelu xaajub xiin, di liitar ak genn-wàll. Na joxe loolu, def ko xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji.
8«Su dee sarxe jur gu gudd, muy saraxu rendi-dóomal, mbaa sarax bu muy wàccoo aw xas, mbaa saraxu cant ci biir jàmm, ñeel Aji Sax ji, 9na sarxewaaleek jur gu gudd gi, ab saraxu pepp bu ñetti fukkeeli efay sunguf su mucc ayib, di juróom ñeenti kilo, ñu xiiwe ko genn-wàllu xiinu diw, di ñaari liitar, 10ak biiñ bu muy joxewaale, ngir saraxu tuuru, di genn-wàllu xiin, muy ñaari liitar. Loolu saraxu sawara la, di xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji.
11«Noonu lees di def bu dee saraxu yëkk, mbaa am kuuy mu mag, mbaa am kuuy mu ndaw, mbaa bëy. 12Nu limu juri sarax yi tollu rekk, ngeen def mu ci nekk noonu, ànd ak lim ba. 13Mboolem njuddu-ji-réew, noonu lay defe sarax yooyii, buy indi saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji.
14«Su dee ab doxandéem bu dal ak yeen, mbaa ku nekk ak yeen ci seen maas yiy ñëw, te muy joxe saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji, ni ngeen koy defe rekk la koy defe. 15Mbooloo mi mépp, dogalu yoon boobu benn la ciy doon, muy yeen, di doxandéem bi. Dogal la buy sax fàww, ñeel seen maasoo maas, te di benn ci yeen ak ci doxandéem bi, fi kanam Aji Sax ji. 16Wenn yoon wee, di benn àtte bi, ñeel leen, ñeel doxandéem bi dal ak yeen.»
Lu jëm ci mépp meññeef mu njëkk
17Aji Sax ji waxati Musaa, ne: 18«Waxal bànni Israayil, ne leen, bu ngeen demee ca réew ma ma leen jëme, 19bay lekk ca ñamu réew ma, nangeen ci génne asaka, ñeel Aji Sax ji; 20seen nootu sunguf bu njëkk, ci ngeen di sàkke menn mburu mu ñuy jébbal Aji Sax ji. Ni ngeen di génne asakay njébbal bu jóge ca dàgga ja rekk, ni ngeen koy sàkke. 21Seen nootu sunguf bu njëkk, ci ngeen di génne asakay njébbal, ñeel Aji Sax ji, yeen ak seen askan.»
Sarax war na ci moy gu dul teyeef
22Su dul ci teyeef ngeen ñàkka jëfe lenn ci mboolem santaane yii Aji Sax ji dénk Musaa, 23ci mboolem lu leen Aji Sax ji sant, Musaa jottali, dale ko keroog ba Aji Sax ji santaanee loola, ak gannaaw gi, ba ca seen maasoo maas, 24su dee moy gu dul teyeef, te mbooloo mi yégu ko woon, su boobaa mbooloo mépp ay sarxal aw yëkk wu ndaw wuy doon rendi-dóomal, ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji, ak saraxu pepp, ak saraxu tuuru yi mu àndal, ni ko yoon àttee, ak benn sikket ngir saraxu póotum bàkkaar. 25Sarxalkat bi day def loolu njotlaayal mbooloom bànni Israayil gépp, njéggal daldi leen ñeel, gannaaw moy ga dug teyeef, te ñoom it indi nañu seen saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji, booleek seen saraxu póotum bàkkaar fi kanam Aji Sax ji, ndax seen moy ga dul teyeef. 26Njéggal day daldi ñeel mbooloom bànni Israayil gépp, ak bépp doxandéem bu dal ak ñoom, ndax mbooloo mépp lay seen moy gu dul teyeef.
27Su dee kenn nit a bàkkaar te du teyeefam, na sarxal aw bëy wu jigéen wu menn at, ngir saraxu póotum bàkkaar. 28Sarxalkat bi daldi koy def fi kanam Aji Sax ji, njotlaayal ki moy ci ag ñàkka tey, ca bàkkaaram ba dul teyeef. Loolu la koy jote, njéggal ñeel ko. 29Muy njuddu-ji-réew ju bokk ci bànni Israayil, di doxandéem bu dal ak ñoom, yoon wi wenn lay doon, ñeel ki moy te du teyeefam.
30Nit ki tooñ cig teyeefam nag, muy njuddu-ji-réew, di doxandéem, kooku Aji Sax ji la ñàkke kersa. Nit kooku, dees koy dagge ci biiri bokkam. 31Gannaaw kàddug Aji Sax ji la teddadil te ndigalam la xëtt, nit kooku dees koy dagge rekk, mu gàddu bàkkaaram.
Bésub Noflaay wormaal la laaj
32Ba bànni Israayil nekkee ca màndiŋ ma, dañoo fekk jenn waay, muy taxan bésub Noflaay. 33Ña ko fekk muy taxan, yóbbu ko ba ca Musaa ak Aaróona, ak mbooloo ma mépp. 34Ba loolu amee ñu teg ko ciy loxo, ndax dogaleesagul woon nees di def ak moom. 35Ci kaw loolu Aji Sax ji ne Musaa: «Dee rekk mooy àtteb waa ji. Dees koy génne dal bi, mbooloo mépp dóor koy xeer, ba mu dee.»
36Mbooloo ma mépp daldi koy génne dal bi, dóor koy xeer ba mu dee, na ko Aji Sax ji sante Musaa.
Yoon sàrtal na wàllu col
37Aji Sax ji waxati Musaa, ne ko: 38«Waxal bànni Israayil, ne leen, ci seen maasoo maas, nañu def ay langat ci seen cati mbubb, langat wu ci nekk ñu nas ci buum gu baxa. 39Mu doon seen langat yu ngeen di xool, di ko fàttalikoo mboolem santaaney Aji Sax ji, ngir di ko jëfe, te baña topp seen bànneexu bakkan ak seeni gët, bay moy. 40Su ko defee ngeen di bàyyi xel tey jëfe sama santaane yépp, daldi doon ñu sell, ñeel seen Yàlla. 41Man maay Aji Sax ji, seen Yàlla ji leen génnee réewum Misra ngir doon seen Yàlla. Maay seen Yàlla Aji Sax ji.»

Currently Selected:

Màndiŋ ma 15: KY

Highlight

Copy

Compare

Share

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in