Màrk 3
3
Yeesu faj na nit ku loxoom làggi
1Gannaaw loolu Yeesu duggati ca jàngub Yawut ba. Boroom loxo bu làggee nga fa woon. 2Ay Farisen a ngay xool Yeesu, ba xam ndax dina ko faj, te muy bésub Noflaay, ngir ñu man koo tuumaal. 3Yeesu ne boroom loxo bu làggi ba: «Taxawal fii ci digg bi.» 4Yeesu nag ne leen: «Ana lu yoon maye; def lu baax bésub Noflaay am def lu bon? Rawale bakkan am rey?» Ñu ne xerem.
5Ci kaw loolu Yeesu dawal bëtu mer, xool leen ñoom ñépp, boole kooku naqar ndax seen xol yu wow. Mu ne waa ja: «Tàllalal loxo bi.» Mu tàllal, loxo ba wér. 6Ba loolu amee Farisen ya génn, diisooji ca saa sa ak farandooy Buur Erodd ca mbirum Yeesu, ngir fexe nu ñu ko sànke.
Mbooloo topp na Yeesu
7Gannaaw loolu Yeesu aki taalibeem jóge fa, jëm dex ga, mbooloom diiwaanu Galile mu bare topp ko, ak waa diiwaanu Yude itam, 8ak waa Yerusalem ak Idume#3.8 Idume mooy diiwaanu Edom ci làkku gereg. Ci Yuda la bokkoon, wetu bëj-saalumam. ak wàllaa Yurdan ak la wër Tir ak Sidon. Muy mbooloo mu bare mu dégg mboolem la muy def, daldi koy fekki. 9Yeesu nag ne ay taalibeem, ñu waajal ko gaal bala ko mbooloo maa tanc. 10Ndax booba Yeesu jotoon naa faj ñu bare, ba tax mboolem ña ame ay jàngoro song ko, di ko wuta laal. 11Rab ya itam, saa yu ñu ko gisaa, daldi daanu fa kanamam, tey yuuxu naan: «Yaa di Doomu Yàlla.» 12Teewul Yeesu femmu rab ya bu baax, ngir ñu bañ koo siiwal.
Yeesu tànn na fukki ndaw ak ñaar
13Gannaaw loolu Yeesu yéeg ca tund wa, woo fa ña ko neex, ñooña dikk ba ca moom. 14Mu tabb ca fukk ak ñaar, tudde leen ay ndawam, ngir ñuy ànd ak moom, ngir itam, mu di leen yebal, ñu waareji, 15mu joxaale leen xam-xamu dàq ay rab. 16Noonu la tabbe Fukk ak ñaar ñii, di Simoŋ ma muy wax Piyeer, 17ak Yanqóoba ak Yowaan, doomi Sebede, ña Yeesu di wax Bowanerses, muy firi Doomi dënu, 18ak Àndre ak Filib ak Bartelemi ak Macë ak Tomaa ak Yanqóoba doomu Alfe, ak Tade ak Simoŋ, Mbokki kuréelu Moom-sa-réew ma, 19ak Yuda Iskaryo may mujj wor Yeesu.
Gii tooñ la Yàlla dul baale
20Yeesu dellooti kër ga, mbooloo ma dajeeti fa, ba moom ak ay taalibeem taluñoo sex dugub sax. 21Ay bokkam dégg la xew, daldi dikk, ngir jàppsi ko, naan dafa teqalikoo ak sagoom. 22Firikati yoonu Musaa ya jotoona wàccsee Yerusalem it ne: «Kii, Beelsebul a ko jàpp. Buuru rab boobu lay dàqe ay rab.»
23Ba mu ko defee Yeesu woo leen, léeb leen ay léeb, ne leen: «Ana nu Seytaane mana dàqe Seytaane? 24Ag nguur de, su dee xàjjalikoo ci biiram, googa nguur du mana yàgg. 25Ag kër it, su dee xàjjalikoo ci biiram, googa kër du mana yàgg. 26Seytaane nag, su jógee di xàjjalikoo ci biiram, du mana yàgg, day jeexal rekk.
27«Du kenn moos ku mana dugg kër ponkal, buub alalam! Xanaa mu njëkka yeew ponkal mi, doora mana toj kër ga. 28Maa leen ko wax déy, lu mu mana doon, dees na ko jéggal doom aadama, mu diy bàkkaaram, ak mboolem kàddug saaga Yàlla. 29Waaye képp ku saaga Noo gu Sell gi, deesu ko jéggal mukk; day gàddu bàkkaar ba fàww.»
30La ñu ne rab a ko jàpp moo waral mu wax leen loolu.
Déggal Yàllaa gën bokk ak Yeesu
31Yaayu Yeesu moo dikkoon, ànd ak ay rakki Yeesu. Ñu taxaw ca biti, yónnee, woo ko. 32Booba mbooloo nga toog, wër ko. Ñu ne ko: «Sa yaay ak say rakk kat ñu ngi ci biti, di la seet.» 33Yeesu ne leen: «Ana kan mooy sama yaay? Ak ñan ñooy samay rakk?» 34Mu dawal nag bëtam, xool ña ko yéew, daldi ne: «Dama ne, ñii ñooy sama yaay ak samay rakk. 35Ndax kuy jëfe coobarey Yàlla, kooku moo di sama rakk ju góor, di samab jigéen, di sama yaay.»
Currently Selected:
Màrk 3: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright