Màrk 1
1
Yaxya waare na
1Lii mooy ndoortel xibaaru jàmm bu Yeesu Almasi bi, Doomu Yàlla ji#1.1 Yàlla ci boppam moo woowe Yeesu doomam. Seetal ci aaya 11.. 2Mu doore ni ñu ko binde ci téereb Yonent Yàlla Esayi, fu Yàlla ne:
«Maa ngii di yebal sama ndaw, mu jiitu la,
xàllal la saw yoon#1.2 Seetal ci Malasi 3.1..
3Baatu nit a ngi xaacoo ca màndiŋ ma, naan:
“Nangeen xàll yoonu Boroom bi,
juballeen ay xàllam#1.3 Seetal ci Esayi 40.3..”»
4 Yaxya nag dikk ca màndiŋ ma, di waare lu jëm ci tuubeel gu nit ñi wara fésale ag sóobu cim ndox, ngir Yàlla jéggal leen seeni bàkkaar. 5Ci kaw loolu mboolem diiwaanu Yude ak waa Yerusalem ñépp bàbbeeku, jëm ca Yaxya. Ñu tudd seeni bàkkaar, Yaxya sóob leen ca dexu Yurdan. 6Yaxyaa nga sol mbubb mu ñu ràbbe kawaru giléem, laxasoo laxasaayu der ca ndigg la, di dundey njéeréer ak lemu àll. 7Mu waare, ne: «Am na ku ma sut kuy ñëw sama gannaaw, kooku, buumi caraxam sax yeyoowumaa sëgg, di ko ko feccil. 8Man cim ndox laa leen sóob, waaye moom de, ci Noo gu Sell gi la leen di sóob.»
Yaxya sóob na Yeesu ca dexu Yurdan
9Ca fan yooyu la Yeesu bàyyikoo dëkk ba ñuy wax Nasaret ca diiwaanu Galile. Mu dikk, Yaxya sóob ko ca dexu Yurdan. 10Naka la Yeesu génn ndox ma ca saa sa, daldi gis asamaan xar, Noowug Yàlla, wàcc ni am pitax, ca kawam, 11baat jibe asamaan, ne: «Yaa di sama Doom, sama soppe; yaw laay bànneexoo.»
Yeesu dékku na fiiri Seytaane
12Ca saa sa Noowug Yàlla jañax Yeesu, ba ca biir màndiŋ ma. 13Nekk na ca màndiŋ ma ñeent fukki fan, Seytaane di ko fiir, mu nekkandook rabi àll yi, malaaka yi di ko toppatoo.
Yeesoo ngi waare
14Gannaaw ba ñu tëjee Yaxya kaso, Yeesu dem Galile, di waare xibaaru jàmm bu Yàlla bi, 15naan: «Waxtu wa mat na, nguurug Yàlla dëgmal na. Tuubleen seeni bàkkaar te gëm xibaaru jàmm bii.»
Yeesu tànn na ñeenti taalibe
16Yeesoo doon jaare tàkkal dexu Galile, daldi gis ku ñuy wax Simoŋ ak Àndre, rakkam ju mu bokkal ndey ak baay. Ña ngay mbaal ca dex ga, ndax ay nappkat lañu woon. 17Yeesu ne leen: «Ñëwleen topp ma, ma def leen nappkati nit.» 18Ñu won mbaal ya gannaaw ca saa sa, daldi topp ca moom.
19Yeesu doxaat tuuti, gis Yanqóoba doomu Sebede ak Yowaan mi Yanqóoba bokkal ndey ak baay. Ña nga ca gaal ga, di gaar seeni mbaal. 20Yeesu woo leen ca saa sa, ñu bàyyi seen baay Sebede ca gaal ga, mook surga ya, daldi topp ca moom.
Yeesu tàmbali naa wone gëddëm
21Gannaaw loolu Yeesu ak taalibe ya jàll biir dëkk ba ñuy wax Kapernawum. Naka la bésub Noflaay taxaw, Yeesu daldi dugg ca biir jàngub Yawut ba, di jàngale. 22Ñu yéemu ca njàngaleem ndax sañ-sañ ba mu leen di jàngale niroowul ak na la firikati yoonu Musaa yay jàngalee.
23Jenn waay a nga woon ca seen biir jàngu ba, rab a ko jàpp. Mu jekki di xaacu, naan: 24«Yaw Yeesum Nasaret, ana lu nu joteek yaw? Alagsi nu mooy say tànk? Xam naa yaa di kan, yaa di Aji Sell ju Yàlla ji.» 25Yeesu nag gëdd ko, ne ko: «Noppil te génn nit ki!» 26Rab wu bon wa daane waa ja ba muy say, mu yuuxu yuux gu réy, doora génne ca waa ja.
27Ba loolu amee ñépp yéemu, naan ca seen biir: «Lii lu mu doon? Guléet mii njàngale! Céy bii xam-xam bu ànd ak sañ-sañ! Rab yi sax, mu jox leen ndigal, ñu def!» 28Turu Yeesu nag law a law ca saa sa, ba dajal diiwaanu Galile gépp.
Yeesu faj na jarag yu bare
29Gannaaw ba Yeesu ak Yanqóoba ak Yowaan génnee ca jàngu ba, dañoo ànd ca saa sa, dem kër Simoŋ ak Àndre. 30Fekk yaayu jabaru Simoŋ tëdd ndax yaram wu tàng. Ñu yégal ko Yeesu. 31Mu dikk ba ca soxna sa, jàpp ca loxoom, yékkati ko, tàngooru yaram wa teqalikook soxna sa, mu di leen toppatoo.
32Ba ngoon jotee ba jant so, ñu indil Yeesu mboolem ñi wopp ak ñi rab jàpp, 33dëkk ba bépp daje ca buntu kër ga. 34Ci biir loolu ñu bare ñu ame ay jàngoroy jàngoro, mu wéral leen, rab yu bare, mu dàq leen. Waaye gannaaw rab ya xam nañu ko, mayu leen ñu wax.
Yeesu wéetoo na ak Yàlla
35Ca ëllëg sa, laata bët di set, Yeesu jóg, génn, dem, ba àgg benn béreb bu wéet. Mu di fa ñaan Yàlla. 36Ci biir loolu Simoŋ aki àndandoom di ko seet. 37Ba ñu ko gisee, ne ko: «Ñépp a ngi lay seet.»
38Yeesu ne leen: «Nan dem feneen ci dëkk yi nu wër ngir ma waare foofu itam, ndax looloo ma taxa génn.» 39Ci kaw loolu muy wër diiwaanu Galile gépp, di waare ci seeni jàngu, di dàq rab yi.
Yeesu faj na ku gaana
40Gannaaw loolu genn gaana dikk ba ca moom, di ko ñaan, daldi sukk, ne ko: «Su la soobee, man nga maa setal.» 41Yërmande jàpp Yeesu, mu tàllal loxoom, laal ko, ne ko: «Soob na ma, setal.» 42Ca saa sa ngaana ga teqalikook moom, mu set wecc.
43Yeesu nag artu ko bu baax, yiwi ko ca saa sa, ne ko: 44«Fexeel ba bul wax kenn dara, demal rekk ca sarxalkat ba, ngir mu seet la, te nga génne sa saraxu setlu ni ko yoonu Musaa santaanee#1.44 Seetal ci Sarxalkat yi 14.1-32., ngir muy firnde ci ñoom.» 45Waaye naka la waa ja génn, tàmbalee yéene, siiwal mbir ma, ba tax Yeesu manatula siiwal duggam cib dëkk, xanaa mu féetewoo béreb yu wéet ca fa ko wër. Teewul nit ñiy jóge fu nekk, di ko fekki.
Currently Selected:
Màrk 1: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright