1
Màrk 1:35
Kàddug Yàlla
KY
Ca ëllëg sa, laata bët di set, Yeesu jóg, génn, dem, ba àgg benn béreb bu wéet. Mu di fa ñaan Yàlla.
Compare
Explore Màrk 1:35
2
Màrk 1:15
naan: «Waxtu wa mat na, nguurug Yàlla dëgmal na. Tuubleen seeni bàkkaar te gëm xibaaru jàmm bii.»
Explore Màrk 1:15
3
Màrk 1:10-11
Naka la Yeesu génn ndox ma ca saa sa, daldi gis asamaan xar, Noowug Yàlla, wàcc ni am pitax, ca kawam, baat jibe asamaan, ne: «Yaa di sama Doom, sama soppe; yaw laay bànneexoo.»
Explore Màrk 1:10-11
4
Màrk 1:8
Man cim ndox laa leen sóob, waaye moom de, ci Noo gu Sell gi la leen di sóob.»
Explore Màrk 1:8
5
Màrk 1:17-18
Yeesu ne leen: «Ñëwleen topp ma, ma def leen nappkati nit.» Ñu won mbaal ya gannaaw ca saa sa, daldi topp ca moom.
Explore Màrk 1:17-18
6
Màrk 1:22
Ñu yéemu ca njàngaleem ndax sañ-sañ ba mu leen di jàngale niroowul ak na la firikati yoonu Musaa yay jàngalee.
Explore Màrk 1:22