Macë 27
27
Yuda réccu na
1Ca suba teel mboolem sarxalkat yu mag ya ak magi askan wa féncoo, ngir teg Yeesu àtteb dee. 2Ñu yeew ko, yóbbu, jébbal ko Pilaat boroom réew ma.
3Yuda ma wor Yeesu nag, ba mu gisee na ñu tege Yeesu àtteb dee, ca la réccu, daldi delloo fanweeri poseti xaalis ya ca sarxalkat yu mag ya ak magi askan wa. 4Mu ne: «Bàkkaar naa ba ma woree jàmbur bu deful dara, ñu tuur deretam.» Ñu ne ko: «Lu ciy sunu yoon? Yaa xam!» 5Ba mu ko defee Yuda sànni xaalis ba ca kër Yàlla ga, jóge fa, dem, wékk boppam, xaru.
6Sarxalkat yu mag ya nag for xaalis ba, ne: «Yoon mayewul ku def xaalis bi ci dencukaayu kër Yàlla gi, ndax peyug deret la.» 7Gannaaw ba ñu ca diisoo, ab toolu defarkatu ndaa lañu jënd ca xaalis ba, ngir di fa suul doxandéem yi. 8Loolu moo tax Toolu deret lañu ko woowe ba tey ji. 9Noonu la kàddu ga jottalikoo woon ci Yonent Yàlla Yeremi sottee. Mooy ba mu nee:
«Jël nañu fanweeri dogi xaalis ya,
muy njëgu nit ka ñu xayma,
te bànni Israayil di ñi ko xayma,
10weccee ko toolu tabaxkatu ndaa ba,
na ma ko Boroom bi sante woon#27.9-10 Seetal ci Yeremi 18.2-3; 19.1-2; 32.6-15; Sàkkaryaa 11.12-13..»
Yeesu taxaw na fa kanam Pilaat
11Yeesu nag taxaw ca kanam Pilaat boroom réew ma. Boroom réew ma laaj ko, ne ko: «Yaw yaa di buurub Yawut yi?» 12Yeesu ne ko: «Yaa ko wax.» Teewul ba ko sarxalkat yu mag ya ak magi askan wa di tuumaal, tontuwu ca. 13Ca la ko Pilaat ne: «Xanaa dégguloo li ñu lay jiiñ lépp?» 14Yeesu nag tontuwu ko ci lenn, ba tax boroom réew ma jaaxle lool.
15Fekk na màggal gu nekkaan, boroom réew ma daan na may askan wa, ñu tànn ca ña ñu tëj kaso, kenn nit ku ñu bëgg, mu bàyyi kooka. 16Booba amoon na ku ñu tëj ca kaso ba, te muy ku siiw ku ñuy wax Barabas. 17Ba ñu dajee nag, Pilaat ne leen: «Kan ngeen bëgg, ma bàyyi ko, Yeesu Barabas, am Yeesu mi ñuy wax Almasi bi?» 18Booba xam na ne kiñaan a tax ñu jàpplu Yeesu. 19Naka la Pilaat toog ca jalu àttekaay ba, soxnaam yeble ca moom ne ko: «Bul dugg ci mbiri ku jub kooku, ndax tey sonn naa lool ci biir gént ndax moom.» 20Teewul sarxalkat yu mag ya ak magi askan wa xiirtal mbooloo ma, ngir ñu ñaan ñu bàyyi Barabas te reylu Yeesu.
21Boroom réew ma nag ne leen: «Kan ci ñaar ñii ngeen bëgg, ma bàyyil leen ko?» Ñu ne ko: «Barabas.» 22Pilaat ne leen: «Nu may def Yeesu, mi ñuy wax Almasi bi nag?» Ñépp ne ko: «Daaj ko ci bant!» 23Boroom réew ma ne leen: «Lu tax? Ana lu bon lu mu def?» Teewul ñu gëna xaacooti, ne: «Daajal ci bant!»
24Pilaat nag gis ne amu ca pexe, te coow lu réy a cay topp, mu sàkk ndox, raxas ay loxoom ca kanam mbooloo ma, daldi ne: «Set naa wecc ci deretu kii. Yeenay seet.» 25Mbooloo mépp àddoondoo, ne: «Na nu deretam dal, nook sunuy doom.»
26Booba la leen Pilaat bàyyil Barabas, Yeesu moom, mu cawlu ko ay kàcciri, ba noppi teg ko ciy loxo, ngir ñu daaj ko ci bant.
Takk-der ya ñaawal nañu Yeesu
27Ba mu ko defee takk-deri boroom réew ma yóbbu Yeesu kër buur, ñu daldi woo gàngoor ga gépp ca kawam. 28Gannaaw loolu ñu futti ko, solal ko mbubb mu xonq curr, 29teg ci boppam kaala gu ñu ràbbe ay dég, ba noppi teg aw yet ci loxol ndijooram. Ñu sukk ci kanamam, di ko ñaawal, naan: «Buuru Yawut yée, guddaluw fan!» 30Ci kaw loolu ñu di ko tifli, fab yet wa, di ko dóor ci bopp. 31Ba ñu ko ñaawalee ba noppi, dañoo summi mbubb ma, solal ko ay yéreem, door koo yóbbu, ngir ñu daaj ko ci bant.
Daaj nañu Yeesu
32Ba ñu génnee, jenn waay ju ñuy wax Simoŋ te dëkk Siren#27.32 Siren, ab dëkk la bu nekkoon ci tefesu bëj-gànnaaru Afrig te féete Misra sowu. lañu dajeel; moom lañu gàdduloo bant ba ñu daaj Yeesu. 33Ñu dem ca béreb ba ñuy wax Golgota, muy firi bérebu Kaaŋu bopp#27.33 bérebu Kaaŋu bopp mooy tund wu nirook kaaŋu bopp.. 34Ci kaw loolu ñu may ko biiñ bu ñu jaxaseek wextan, ngir mu naan#27.34 Seetal ci Taalifi cant 69.22.. Teewul ba mu ca ñamee, nanguwu koo naan.
35Ba loolu amee ñu daaj Yeesu ca bant ba, daldi tegoo bant ay yéreem, séddoo ko#27.35 Seetal ci Taalifi cant 22.19.. 36Ba loolu wéyee ñu toog fa, di ko wattu. 37Fa féete boppam kaw nag, ñu teg fa lu ñu bind tuumaam ja ko daanlu, mbind ma ne: «Kii mooy Yeesu, buurub Yawut yi.»
38Ca lañu daajaale ak Yeesu ñaari fippukat ya, kii ci ndijooram, kee ca càmmoñam#27.38 Seetal ci Esayi 53.12..
39Ña fa jaare nag di ko saaga aka wëcc bopp#27.39 Seetal ci Taalifi cant 22.7-8., 40naan: «Acam, yaw miy toj kër Yàlla gi, tabaxaat ko ci ñetti fan, musalal sa bopp boog; gannaaw yaa di Doomu Yàlla, wàccal bant bi!» 41Sarxalkat yu mag ya it naka noonu, ñook firikati yoonu Musaa ya ak magi askan wa. Ñu di ko ñaawal, naan: 42«Moom day musle te manul musal sax boppam! Mooy buurub Israayil, na wàcc bant bi léegi kay, nu gëm ko. 43Gannaaw Yàlla la wóolu, na ko Yàlla daldi musal, su ko soobee, ndegam nee naay: “Maay Doomu Yàlla.”» 44Fippukat ya ñu daajaale ak moom itam, di ko tifaare ay saaga.
Yeesu saay na
45La tàmbalee fukki waxtu ak ñaar ca bëccëg nag, ag lëndëm a wàcc ca réew ma mépp, ba fukki waxtu ak juróom ca ngoon. 46Wetu fukki waxtu ak juróom ca ngoon, ca la Yeesu àddu ca kaw ne: «Eli, Eli, lema sabaktani?» Loolu di tekki «Sama Yàlla, sama Yàlla, lu tax nga wacc ma#27.46 Seetal ci Taalifi cant 22.2.?» 47Ñenn ca ña fa taxaw dégg ca, ne: «Yonent Yàlla Ilyaas de la kii di woo.» 48Ci kaw loolu kenn ca ñoom daw, jël ab sagar, xooj ko ci bineegar, lonk ci bant, tàllal ko ko, ngir mu naan. 49Teewul ña ca des ne: «Bàyyil, nu seet ndax Ilyaas ay ñëw, wallu ko.» 50Yeesu nag àddooti ca kaw, daldi yiwi noo ga.
51Ca saa sa ridob biir néegu Yàlla ba dale ca kaw ba ca suuf, xar ñaar, suuf sa yëngu, doj ya xar, 52bàmmeel ya ubbiku, néewi aji sell ñu bare ñu nelawoon, daldi dekki, 53génne ca bàmmeel ya. Gannaaw ba Yeesu dekkee, dugg nañu ca dëkk bu sell ba, ba feeñu ñu bare.
54 Njiitu takk-der ba ak ña àndoon ak moom di wattu Yeesu nag, ba ñu gisee suuf sa yëngu ak mboolem la xew, dañoo tiit lool, ba ne: «Aylayéwén kii Doomu Yàlla la.»
55Ay jigéen ñu baree nga fa woon, dànd leen lu sore, di seetaan. Ña nga toppe woon Yeesu fa Galile, di ko toppatoo. 56Maryaama ma dëkk Magdala ca la, ak Maryaama yaayu Yanqóoba ak Yuusufa, ak yaayu doomi Sebede ya.
Rob nañu Yeesu
57Ba ngoon jotee, jenn waay ju dëkke Arimate, ku Yàlla baaxe, ñu di ko wax Yuusufa, te muy taalibeb Yeesu moom ci boppam, 58moo dem ca Pilaat, laaj ko néewub Yeesu. Pilaat joxe ndigal, ñu jox ko ko. 59Ci kaw loolu Yuusufa jël néew ba, sànge ko càngaayal lẽe lu set, 60denc ko ci bàmmeelu doj bu bees, bu mu yattaloon boppam. Ba loolu amee mu béraŋ doj wu mag, ube ko buntu bàmmeel ba, daldi dem. 61Fa la fekk Maryaama ma dëkk Magdala, ak meneen Maryaama ma, ñu toog janook bàmmeel ba.
62Ca ëllëg sa nag, topp ca bésub Waajalu Noflaay, sarxalkat yu mag ya ak Farisen ya ñoo daje, dem ca Pilaat. 63Ñu ne ko: «Sang bi, danoo fàttaliku ne naxekat boobu daa waxoon ba muy dund ne: “Gannaaw ñetti fan dinaa dekki.” 64Kon nag ngalla joxeel ndigal, ngir wattulu bàmmeelam, ba ca ñetteelu fanam, bala ay taalibeem dikk, sàcc néew bi, te naan askan wi, dekki na, te kon naxe gu mujj gi mooy yées gu njëkk ga.» 65Pilaat ne leen: «Am ngeen ay wattukat, demleen wattuji ko nu ngeen mane.» 66Ñu dem nag, ngir sàmmi bàmmeel ba, daldi cay tay doj wa koy ub, boole ca teg fa ay wattukat.
Currently Selected:
Macë 27: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright