1
Macë 27:46
Kàddug Yàlla
KY
Wetu fukki waxtu ak juróom ca ngoon, ca la Yeesu àddu ca kaw ne: «Eli, Eli, lema sabaktani?» Loolu di tekki «Sama Yàlla, sama Yàlla, lu tax nga wacc ma?»
Compare
Explore Macë 27:46
2
Macë 27:51-52
Ca saa sa ridob biir néegu Yàlla ba dale ca kaw ba ca suuf, xar ñaar, suuf sa yëngu, doj ya xar, bàmmeel ya ubbiku, néewi aji sell ñu bare ñu nelawoon, daldi dekki
Explore Macë 27:51-52
3
Macë 27:50
Yeesu nag àddooti ca kaw, daldi yiwi noo ga.
Explore Macë 27:50
4
Macë 27:54
Njiitu takk-der ba ak ña àndoon ak moom di wattu Yeesu nag, ba ñu gisee suuf sa yëngu ak mboolem la xew, dañoo tiit lool, ba ne: «Aylayéwén kii Doomu Yàlla la.»
Explore Macë 27:54
5
Macë 27:45
La tàmbalee fukki waxtu ak ñaar ca bëccëg nag, ag lëndëm a wàcc ca réew ma mépp, ba fukki waxtu ak juróom ca ngoon.
Explore Macë 27:45
6
Macë 27:22-23
Pilaat ne leen: «Nu may def Yeesu, mi ñuy wax Almasi bi nag?» Ñépp ne ko: «Daaj ko ci bant!» Boroom réew ma ne leen: «Lu tax? Ana lu bon lu mu def?» Teewul ñu gëna xaacooti, ne: «Daajal ci bant!»
Explore Macë 27:22-23