Yawut ya 3
3
Doom jee gëna màgg Musaa
1Kon nag bokk yu sell yi, yeen ñi bokk ci wooteb asamaan, ràññeeleen Yeesu, ndaw li, sarxalkat bu mag bi ci yoon wi nu gëm. 2Ku wóor la woon, ñeel ki ko tabb, noonee Musaa wóore woon ci mboolem waa kër Yàlla. 3Waaye ni ab tabaxkat ëppe teraanga kër ga muy tabax, ni la Yeesu yelloo daraja ju ëpp ja Musaa yelloo woon. 4Ndax kër gu nekk am na ku ko tabax, waaye ki tabax lépp mooy Yàlla. 5Musaa déy «jawriñ ju wóor la woon ci biir mboolem waa kër Yàlla#3.5 Seetal ci Màndiŋ ma 12.7.,» di seedeel Yàlla kàddu ya ñu fa wara wax. 6Almasi bi nag mooy Doom ju wóor ji jiite kër Yàlla, te nun nooy këram, ndegam kay nu ngi wéye aw fit ak yaakaar ji nuy puukarewoo.
Almasi bi moo jara déggal
7Kon nag ni ko Noo gu Sell gi waxe:
«Bésub tey jii bu ngeen déggee baatam,
8buleen të na woon ca fippu ga,
keroog bésub seetlu Yàlla ba ca màndiŋ ma#3.8 Seetal ci Mucc ga 17.1-7.,
9fa ma seeni maam doon seetloo, di ma diiŋat,
te gisoon samay jaloore,
10diiru ñeent fukki at.
Moo tax ma mere gii maas, ba ne:
“Seen xol a dëkke lajj,
ñu faaleedi samay santaane.”
11Moo ma taxa giñ ci sama biir mer, ne:
“Duñu tàbbi mukk fa samag noflaay#3.7-11 Seetal ci Taalifi cant 95.7-11; noflaay: Yàlla moo digoon bànni Israayil ag noflaay, te mooy jàmm ju mu leen digoon ne dinañu ko dëkke biir Kanaan, gannaaw bu ñu fa duggee. Waaye ñi déggal Yeesu Almasi bi, ñoo jagoo teeweji jataayu Yàlla, te loolu mooy doon seen noflaay..”»
12Bokk yi, wattuleen bala kenn ci yeen a am xolub gëmadi bu bon bu koy xiir ci dëddu Yàlla jiy dund. 13Waaye bés bu nekk deeleen soññante li feek muy bésub teyagum, bala bàkkaar a nax kenn ci yeen, ba mu mujj dërkiis. 14Ndax kat noo di àndandooy Almasi bi, ndegam wéye nanoo ŋoy bu dëgër ci sunu kóolute ga nu doore, ba kera muj ga. 15Waxees na ne:
«Bésub tey jii bu ngeen déggee baatam,
buleen të na woon ca fippu ga#3.15 Seetal ci Taalifi cant 95.7-8..»
16Ana ñan ñoo déggoon te teewuleena fippu? Xanaa du mboolem ña génne woon Misra ci njiital Musaa? 17Ana ñan la Yàlla mere lu mat ñeent fukki at? Xanaa du mboolem ña bàkkaaroon te seeni néew mujj tëdd ca màndiŋ ma? 18Te it ana ñan ñu moy ña déggadi woon, la Yàlla giñaloon ne duñu tàbbi mukk ci noflaayam? 19Kon nu gis ne seen gëmadee tax manuñu ca woona tàbbi.
Currently Selected:
Yawut ya 3: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright