Yawut ya 10
10
1Yoonu Musaa takkndeeru xéewal yiy ñëw doŋŋ a ci nekk, waaye xéewal ya ci seen bopp nekku ci. Looloo tax sarax yi yoon wi laaj ñu war koo saxoo jébbale at mu nekk, manula setal mukk wecc ñiy jaamusi. 2Su sarax yi taxoona set wecc, xanaa deesu ko dakkal? Bu ca jaamukati Yàlla yi doon sete wecc benn yoon kay, xanaa dootuñu am yaraangey bàkkaar! 3Sarax yooyu dañu koy fàttalee ay bàkkaar at mu jot, 4ndax deretu yëkk ak ju sikket kat manula far ay bàkkaar.
5Moo tax ba Almasi biy dikk ci àddina la wax ne:
«Saraxi jur ak pepp, taamuwuloo ko,
waaye aw yaram nga ma waajalal.
6 Saraxu rendi-dóomal ak saraxu póotum bàkkaar,
safoowuloo ci dara.
7Ca laa ne: “Maa dikk nii,
te téereb yoon wi indi na li ñu bind ci man,
maa defsi sa coobare, yaw Yàlla#10.5-7 Seetal ci Taalifi cant 40.7-9..”»
8Dafa njëkk ne: «Saraxi jur ak pepp, saraxi dóomal ak saraxi póotum bàkkaar, bëgguloo, safoowuloo,» doonte yoon wee laaj yooyu sarax. 9Mu teg ca ne: «Maa ngii defsi sa coobare.» Noonu la fare lu njëkk la, ngir wuutal fa ñaareel bi. 10Coobarey Yàlla googu moo waral ñu sellale nu sarax bi Yeesu Almasi bi sarxe yaramam benn yoon ba fàww.
11Bépp sarxalkat a ngi taxaw bés bu nekk ci liggéeyam, di jébbale aka jébbalewaat yenn sarax yooyu, te lenn du ci masa mana far bàkkaar. 12Waaye kii de, ba mu sarxee boppam ngir far ay bàkkaar, bennub sarax bu doy ba fàww, ca la tooge fa ndijooru Yàlla. 13Fa la doxe xaar bés ba ñu koy defal ay noonam ndëggastalu tànkam. 14Kon bennub sarax boobu, ci la matale sëkk ba fàww nit ñi ñu sellal.
15Mooy li Noo gu Sell gi itam seede, ñeel nu, 16nde gannaaw ba mu nee:
«Lii nag moo di kóllëre gi may fas ak ñoom,
bu fan yooyu weesoo, Boroom beey wax,
mu ne: Maay yeb sama ndigali yoon ci seen xol,
ci seen xel laa koy ñaas;
17lii la ca teg: seeni bàkkaar ak seeni ñaawtéef,
duma ci bàyyeeti xel#10.16-17 Seetal ci Yeremi 31.33-34..»
18Yooyu nag fu ñu ko jéggalee, aajootul sarax su koy far.
Nanu àgg fa Yàlla
19Léegi nag bokk yi, am nanu sañ-sañu dugg ca néeg bu sella sell ba, ngir deretu Yeesu, 20deretu Yeesu jiy yoon wu yees, yoonu dund gu mu nu xàllal, jàllale ko ca rido ba, te rido ba moo di yaramu suuxam wi mu saraxe. 21Am nanu itam sarxalkat bu mag bu jiite kër Yàlla ga. 22Kon nag nanu agsee fi Yàlla xol bu dëggu ak fit wu mat sëkk wu ngëm waral, gannaaw wisees na sunum xel ndoxum setlu, ba mu tàggook bépp gàkk bu mu nu sikkale, te raggees na sunu yaram ci ndoxum setlu. 23Nanu ŋoy ci yaakaar ji nu biral ne moom lanu am, te nu baña yoqi, nde ki dige ku wóor la. 24Nanu seet itam ci sunu biir nu nuy xiirtalantee ngir cofeel ak jëf ju baax. 25Te bunu def ni ñenn ñi, di daggoo ak sunuy ndaje, waaye nanuy ñaaxante, rawatina tey bi ngeen gisee bés bi dëgmal.
26Gannaaw bu nu xamee xéll liy dëgg ba noppi nag, su nu bàkkaaratee te di ko tey, su boobaa ab sarax bu far yooyu bàkkaar amatu ci. 27Xanaa tiitaangey séentu mbugal ma ak sawara wu yànj wiy xoyom fippukat yi. 28Képp ku masoona xëtt yoonu Musaa, daawuñu ko ñéeblu; ci kaw seedey ñaari nit ba ñett lees ko daan rey. 29Kon ki dëggaate Doomu Yàlla, teddadil deret ji ñu sellale kóllëre gi, te ñàkke teggin Noowug Yàlla gi nu indil aw yiw, kooku, mbugal ma mu yelloo, ñaata yoon lay gënatee metti, ngeen defe? 30Xam nanu ki wax ne: «Maay kiy feye, di añale,» neeti: «Boroom bi mooy àtte ñoñam#10.30 Seetal ci Baamtug yoon wi 32.35-36..» 31Céy ku nara tàbbi ci loxoy Yàlla jiy dund, ndaw lu raglu!
32Fàttalikuleen bés yu njëkk ya, gannaaw ba ngeen jotee ci leeru Yàlla, na ngeen dëgërloo woon ca xeex bu mag ba te metti. 33Léeg-léegaa ñu saaga leen, bunduxataal leen ci kanam nit ñi; léeg-léegaa yeen ay taxawu nit ñi ñu teg lu ni mel. 34Ndax yeena bokk ak ñi ñu tëj seen coono, te yeena muñ ci xol bu sedd ni ñu foqarñee seen moomeel, ngir xam ngeen yeen ci seen bopp ne am ngeen alal ju ko gën tey sax ba fàww.
35Kon nag buleen teqalikook seenu fit, yool bu réy a ngi ci. 36Li leen war moo di muñ, ba sottal coobarey Yàlla, su ko defee ngeen jot li mu dige. 37Ndax kat,
«Des nas tuut, as tuut rekk,
kiy dikk, dikk te du yeex.
38Sama nit ku jub nag mooy dund ndax ngëm ga,
waaye ku dellu gannaaw,
sama xol bégewu la#10.37-38 Seetal ci Abakug 2.3-4..»
39Nun nag bokkunu ci ñiy dellu gannaaw te nara sànku, waaye nooy ñi saxoo ngëm te nara mucc.
Currently Selected:
Yawut ya 10: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright