1
Yawut ya 10:25
Kàddug Yàlla
KY
Te bunu def ni ñenn ñi, di daggoo ak sunuy ndaje, waaye nanuy ñaaxante, rawatina tey bi ngeen gisee bés bi dëgmal.
Compare
Explore Yawut ya 10:25
2
Yawut ya 10:24
Nanu seet itam ci sunu biir nu nuy xiirtalantee ngir cofeel ak jëf ju baax.
Explore Yawut ya 10:24
3
Yawut ya 10:23
Nanu ŋoy ci yaakaar ji nu biral ne moom lanu am, te nu baña yoqi, nde ki dige ku wóor la.
Explore Yawut ya 10:23
4
Yawut ya 10:36
Li leen war moo di muñ, ba sottal coobarey Yàlla, su ko defee ngeen jot li mu dige.
Explore Yawut ya 10:36
5
Yawut ya 10:22
Kon nag nanu agsee fi Yàlla xol bu dëggu ak fit wu mat sëkk wu ngëm waral, gannaaw wisees na sunum xel ndoxum setlu, ba mu tàggook bépp gàkk bu mu nu sikkale, te raggees na sunu yaram ci ndoxum setlu.
Explore Yawut ya 10:22
6
Yawut ya 10:35
Kon nag buleen teqalikook seenu fit, yool bu réy a ngi ci.
Explore Yawut ya 10:35
7
Yawut ya 10:26-27
Gannaaw bu nu xamee xéll liy dëgg ba noppi nag, su nu bàkkaaratee te di ko tey, su boobaa ab sarax bu far yooyu bàkkaar amatu ci. Xanaa tiitaangey séentu mbugal ma ak sawara wu yànj wiy xoyom fippukat yi.
Explore Yawut ya 10:26-27