Galasi 6
6
Dimbalanteleen
1Bokki gëmkat ñi, su ñu bettee nit ci ag tooñ, yeen ñi topp Noowug Yàlla, waññileen ko ndànk, te kenn ku nekk ci yeen xoolaat boppam bu baax, ngir seen bakkan bañ leena xiirtal, ba ngeen daanu ci fiir, yeen itam. 2Yenuleen seeni yeni moroom, su boobaa ngeen di topp yoonu Almasi bi, ba mu mat sëkk. 3Ku foog ne moo am solo, te du dara nag, boppam lay nax. 4Ku ci nekk, jëfi boppam, na ko niir. Su ci amee lenn lu mu mana sagoo, na ko yemale ci boppam, te baña sagoo lenni boppam lu mu xool ci ñeneen, 5nde ku nekk ak sa añu jëfi bopp.
6Ki ñuy jàngal kàddug Yàlla nag war naa sédd ki koy jàngal ci mboolem alalam.
7Bu leen lenn nax; Yàlla deesu ko foontoo. Nit ki, li mu ji, moom lay góob. 8Ku jiwal bànneexu bakkanam, ci bànneexu bakkanam lay jële ngóobum yàqute; ku jiwal Noowug Yàlla, ci Noo gi ngay góobe texe gu sax dàkk. 9Bunu tàyyi ci def lu baax, nde bu jotee rekk nooy góob, ndegam yoqiwunu. 10Kon nag bi nu koy jekku, nanuy def lu baax, ngir ñépp, rawatina waa kër yoonu ngëm wi.
Na gëmkat bi doon mbindeef mu bees
11Seetluleen mbind mi; ci araf yu mag yii ngeen wara xàmmee, ne sama loxol bopp laa ko binde!
12Ñi leen di xiir ci xaraf mooy ñi ngistal tax ñu bëgg nit ñi gërëme leen seen melow yaram, te jubluwuñu ci lu moy ragal ku leen bunduxataal ndax deewug Almasi gi ñuy xamle ne mooy taxa mucc. 13Ñi xaraf ñoom ci seen bopp sax toppuñu yoon wi. Teewul ñu bëgg ngeen xaraf, ngir mana damoo seen màndargam yaram, yeen ñi ñu xarafloo. 14Waaye man de yàlla buma damoo lenn lu moy deewug sunu Boroom Yeesu Almasi bi ca bant ba. Bant boobu moo tax àddina di lu ñu ma daajal ci bant, ba àddina dee; man it may lu ñu daajal àddina ci bant ba ma dee. 15Xaraf ak ñàkka xaraf, dara amu ci solo. Li am solo mooy doon mbindeef mu bees. 16Mboolem ñiy sàmm ndigal lii nag, te di Israayilu Yàlla, jàmm ak yërmande ñeel na leen.
17Li ci des moo di gannaaw-si-tey, bu ma kenn lëjalati, ndax légét yi ci sama yaram, samag bokk ci Yeesu la màndargaal.
18Bokk yi, yal na sunu yiwu Boroom Yeesu Almasi bi ànd ak seenum xel. Amiin.
Currently Selected:
Galasi 6: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright