1
Galasi 6:9
Kàddug Yàlla
KY
Bunu tàyyi ci def lu baax, nde bu jotee rekk nooy góob, ndegam yoqiwunu.
Compare
Explore Galasi 6:9
2
Galasi 6:10
Kon nag bi nu koy jekku, nanuy def lu baax, ngir ñépp, rawatina waa kër yoonu ngëm wi.
Explore Galasi 6:10
3
Galasi 6:2
Yenuleen seeni yeni moroom, su boobaa ngeen di topp yoonu Almasi bi, ba mu mat sëkk.
Explore Galasi 6:2
4
Galasi 6:7
Bu leen lenn nax; Yàlla deesu ko foontoo. Nit ki, li mu ji, moom lay góob.
Explore Galasi 6:7
5
Galasi 6:8
Ku jiwal bànneexu bakkanam, ci bànneexu bakkanam lay jële ngóobum yàqute; ku jiwal Noowug Yàlla, ci Noo gi ngay góobe texe gu sax dàkk.
Explore Galasi 6:8
6
Galasi 6:1
Bokki gëmkat ñi, su ñu bettee nit ci ag tooñ, yeen ñi topp Noowug Yàlla, waññileen ko ndànk, te kenn ku nekk ci yeen xoolaat boppam bu baax, ngir seen bakkan bañ leena xiirtal, ba ngeen daanu ci fiir, yeen itam.
Explore Galasi 6:1
7
Galasi 6:3-5
Ku foog ne moo am solo, te du dara nag, boppam lay nax. Ku ci nekk, jëfi boppam, na ko niir. Su ci amee lenn lu mu mana sagoo, na ko yemale ci boppam, te baña sagoo lenni boppam lu mu xool ci ñeneen, nde ku nekk ak sa añu jëfi bopp.
Explore Galasi 6:3-5