Galasi 1
1
Ubbite gi
1Ci man Póol, ndaw li bàyyikoowul ci ay nit, jottaliwul ci yónnentu nit, xanaa Yeesu Almasi bi ak Yàlla Baay bi ko dekkal, ci man la kàddu gii bawoo, 2bawoo itam ci mboolem bokk yi nekk ak man, ñeel mboolooy gëmkat yu diiwaanu Galasi. 3Aw yiw ak jàmm ñeel na leen, tukkee ci Yàlla sunu Baay ak Sang bi Yeesu Almasi 4bi maye bakkanam ngir njotug sunuy bàkkaar, ba musal nu ci jamonoy tey ju bon ji, ci coobarey Yàlla sunu Baay 5bi daraja ñeel, tey ak ëllëg ba fàww. Amiin.
Xibaaru jàmm bi benn la
6Man de jaaxle naa ci nii ngeen gaawa dëddoo Yàlla mi leen woo ci boppam, ci ndimbalal yiwu Almasi bi, bay topp xaat beneen xibaaru jàmméey! 7Te beneen dafa amul sax, xanaa ñenn ñi leen di jaxase, te bëgga sopparñi xibaaru jàmm bu Almasi bi. 8Waaye nun ci sunu bopp, mbaa malaaka mu bawoo ci asamaan sax, ku leen ci àgge woon beneen xibaaru jàmm bu dul bi nu leen àgge, kooku yal na alku! 9Wax nanu ko ba noppi, ma waxati ko tey: képp ku leen àgge beneen xibaaru jàmm bu moy bi ngeen xasa jot, yal na alku!
10Léegi nag ndax nit ñi laay sàkkoo jubool, am Yàlla? Am nit ñi laay wuta neex? Su ma bëggoona wéye neex nit ñi de, duma doon jaamub Almasi bi.
Almasi bi moo dénk Póol xibaaru jàmm bi
11Bokk yi, ma xamal leen, ne leen xibaaru jàmm bi may yégle, bàyyikoowul ci nit. 12Te it man jëlewuma ko, jàngewuma ko ci nit, xanaa ci peeñum Yeesu Almasi bi.
13Ndax kat dégg ngeen ni ma doon jëfe bu njëkk, bi ma nekkee ci yoonu Yawut, bunduxataal gu jéggi dayo ga ma daan teg mbooloom gëmkati Yàlla mi, di ko yàq. 14Yoonu Yawut, maa ci rawoon ñu bare ci sama maas gi ma bokkal askan, te maa leen gënoona xér fuuf ci sunu aaday maam. 15Waaye ca sama biiru ndey la ma Yàlla séddoo, woo ma ci boppam ci kaw yiwam, te moom la soob, 16mu feeñalal ma Doomam, ba ma àgge jàmbur ñi dul Yawut xibaaru jàmm bi ci mbirum Almasi bi. Ci saa si diisoowuma ci ak kenn. 17Demuma sax Yerusalem, seeti ñi ma njëkka doon ndawi Almasi bi, waaye Arabi laa dem, doora délsi Damaas.
18Gannaaw ba ñu ca tegee ñetti at laa doora dem Yerusalem, ngir xamanteji ak Sefas#1.18 Sefas mooy Piyeer. Sefas mooy tur wu Almasi bi tudde taalibeem boobu. Seetal ci Yowaan 1.42. , toog fa moom ñaari ayi bés. 19Teewul gisuma kenn ci ndaw yi ci des, ku dul Yanqóoba, rakku Sang bi. 20Li ma leen bind nii nag, Yàlla mi nu tiim seede na ne du ay fen. 21Gannaaw gi laa dem diiwaani Siri ak Silisi. 22Waaye ba boobu, mboolooy gëmkati Almasi ya ca diiwaanu Yude xamuñu ma woon. 23Déggoon nañu rekk ñu naan: «Ki nu daan bunduxataal bu njëkk, di yàq sunu yoonu ngëm wi de, léegi mooy yégle xibaaru jàmm bi!» 24Mboolooy gëmkat yooyu nag di sant Yàlla ci man.
Currently Selected:
Galasi 1: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright