Jëf ya 4
4
Piyeer ak Yowaan daje nañook àttekat ya
1Naka la Piyeer ak Yowaan di wax ak mbooloo ma, sarxalkat yaak jawriñu kër Yàlla gaak Sadusen ya ne jimeet ci seen kaw. 2Fekk na leen ñéññ ca la ñuy waare aka yégle ndekkitel Yeesu, te loolu di dëggal ne dee-dekki, lu am la. 3Ñu daldi leen teg loxo, tëj leen ba ca ëllëg sa, ndax booba guddi na. 4Fekk na nag, ñu bare ca ña jotoona dégg kàddu ga gëm nañu, ba limu gëmkat ña tollu ci juróomi junni (5 000).
5Ca ëllëg sa kilifay Yawut yi ak magi askan wi ak firikati yoonu Musaa yi daje Yerusalem. 6Anas, sarxalkat bu mag ba ca la, ak Kayif ak Yowaan ak Alegsàndar ak mboolem bokki sarxalkat bu mag. 7Ñu taxawal Piyeer ak Yowaan ca digg ba, laaj leen ne: «Yeen, lii ngeen def, ci ban xam-xam ak ci wan tur ngeen ko defe?»
8Fa la Piyeer feeseek Noo gu Sell gi, ne leen: «Yeen kilifay xeet wi ak magi askan wi, 9ndegam yoon moo nuy laaj lu jëm ci ndimbal lu ab lafañ jagoo, ak ci man pexe la lafañ bi mucce, 10xamleen xéll, yeen ñépp ak bànni Israayil gépp, ne ci turu Yeesu Almasi mu Nasaret, ki ngeen daajoon ci bant, te Yàlla dekkal ko, ci turam doŋŋ la kii wére, ba taxaw ci seen kanam. 11Yeesu moomu mooy:
“Doj wi ngeen beddi woon, yeen tabaxkat yi,
te mu mujj di doju koñu tabax bi#4.11 Seetal ci Taalifi cant 118.22..”
12Mucc kat amul ci keneen, ndax fi asamaan tiim, mayeesul fi nit ñi weneen tur wu nu wara mucce.»
13Ba waa kuréelu àttekat ya gisee fit wi Piyeer ak Yowaan àndal, te ñu xam ne niti neen ñu masula jàng lañu, dañoo waaru. Xamoon nañu nag ne ñook Yeesoo nekkoon. 14Te itam ka ñu wéral a nga taxaw fa seen wet, ñuy gis. Manuñu caa tegati dara. 15Ba mu ko defee ñu joxe ndigal, génne leen, daldi gise ci seen biir. 16Ñu ne: «Lu nuy def ak ñii? Ndax kat firnde lu leer sottee na fi ci ñoom; leer na nàññ waa Yerusalem gépp, te manunu koo weddi. 17Waaye kat bu mbir mi gëna siiw ci xeet wi. Nan leen tëkku, ngir aaye leen ñu waxati kenn tur woowu.»
18Ñu woo leen nag, aaye leen, ne leen mayatuñu leen benn yoon ñu waxati lenn, mbaa ñuy jàngale ci turu Yeesu. 19Piyeer ak Yowaan ne leen: «Ndax li jaadu fa Yàlla mooy nu déggal leen, yeen, bàyyi Yàlla? Yeenay àtte loolu. 20Waaye nun, li nu gis, dégg ko, manunu koo baña wax.» 21Ba loolu amee ñu tëkkuwaat leen, door leena yiwi, ñu dem, gannaaw manuñu leena mbugal te amuñu bunt ci ñoom ndax mbooloo ma, te ñépp di màggal Yàlla ca la xew, 22ngir waa ja kéemtaan ga wérloo amoon na lu wees ñeent fukki at.
Mbooloom gëmkat ñi ñaan na ci Yàlla
23Gannaaw ba ñu yiwee Piyeer ak Yowaan, ñu dem ca seen bokki gëmkat, nettali leen mboolem la leen sarxalkat yu mag yaak magi askan wa wax. 24Ba ko bokk ya déggee, ñoom ñépp a mànkoo, daldi yékkati kàddug ñaan fa Yàlla, ne: «Buur Yàlla, yaa sàkk asamaan ak suuf ak géej ak lépp li ci biir. 25Yaa wax ci Noo gu Sell gi ci sunu gémmiñu maam Daawuda sa jaam bi, nga ne:
“Ana lu xeeti àddina di riire?
Lu xeet yiy lale pexey neen?
26Buuri àddinaa jógandoo,
kilifa yee lëkkoo, di fexeel Boroom bi ak Almaseem#4.26 Seetal ci Taalifi cant 2.1-2..”
27Dëgg la moos, ndax ci dëkk bii la Erodd ak Poñsë Pilaat lëkkoo, ànd ak xeeti àddinaak bànni Israayil ci kaw Yeesu, sa jawriñ ju sell ji nga fal. 28Noonu it lañu sottale mboolem li nga dogaloon ci sa loxo ak sa coobare. 29Léegi nag Boroom bi, bàyyil xel seeni tëkkoo te nga may nu, nun say jaam, nuy wax sa kàddu ak fit wu mat sëkk. 30Ngalla tàllalal sa loxo ngir di wéral aka amal ay firnde aki kéemaan ci turu Yeesu, sa jawriñ ju sell ji.»
31Ba ñu ñaanee ba noppi, béreb ba ñu daje daa yëngu, ñu fees ak Noo gu Sell gi ñoom ñépp; ñu daldi tàmbalee waxe fit kàddug Yàlla gi.
Gëmkat ñi ñoo bokkoon lépp
32Ci kaw loolu mboolem gëmkat ñi bokk menn xel ak benn xalaat. Du kenn ku ne moo moom lenn ci alalam, waaye ñoo bokkoon lépp ci seen biir. 33Ndaw yi nag di seedee doole ju réy ne Sang bi Yeesu dekki na, yiw wu yaa di leen dikkal ñoom ñépp. 34Kenn ci ñoom ndóolul, ndax képp ku ciy boroom suuf mbaa ay kër, da koy jaay, indi njëg gi, 35teg ko ci kanam ndaw yi. Su ko defee ku nekk séddu ca la dëppook soxlaam.
36Ku mel ni Yuusufa, bokk ci giirug Lewi, te dëkk ca dunu Sippar, ndaw yi daan ko wax Barnabas, muy firi Ñaaxekat bi, 37ab tool la amoon. Da koo jaay, indi xaalis bi, teg fi kanam ndaw yi.
Currently Selected:
Jëf ya 4: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright