Jëf ya 2
2
Noo gu Sell gi dikk na
1Ba bésu màggalu Pàntakot agsee, ñoom ñépp a bokk daje benn béreb. 2Ca saa sa coow jollee ca asamaan, mel ni riirum ngelaw lu bare doole, daldi fees dell biir kër ga ñu toog. 3Ci kaw loolu ay làmmiñ yu mel ni tàkk-tàkki sawara feeñu leen, làmmiñ ya séddalikoo, daldi toŋ ci kaw kenn ku nekk. 4Ñoom ñépp nag fees ak Noo gu Sell gi, tàmbalee làkk làkk yu wuute, na leen ko Noo gi manloo.
5Booba ay toppkati yoonu Yawut a nga dëkke Yerusalem, te bawoo ci xeeti àddina yépp. 6Naka la coow li jolli, nit ñi daje, ku nekk ci mbooloo mi dégg ñuy làkk sa kàllaama gi nga nàmp. Mbooloo ma jaaxle. 7Ñu boole waaru ak yéemu, naa: «Ñii di wax nii ñépp, xanaa duñu waa Galile? 8Ana nu kenn ku nekk ci nun nag mana dégge ñuy wax ci làmmiñ wi nga nàmp? 9Muy waa Pàrt ak Medd ak Elam ak Mesopotami ak Yude ak Kapados ak Pont ak Asi 10ak Firisi ak Pamfili ak Misra ak wàllu Libi ga dendeek Siren, ak gan ñi jóge Room, 11ak Yawuti njuddu-ji-réew yeek tuubeen ñi, ak waa Keret ak Arabi, nun ñépp a leen dégg ci sunu làmmiñi bopp, ñuy siiwtaane jaloore yu Yàlla!» 12Ñépp waaru, ba jànnaxe, di wax ci seen biir naa: «Lii lu muy tekki nag?» 13Teewul ñenn ñay ñaawle, ne: «Ñii daal biiñ bu bees doŋŋ lañu naan ba màndi.»
Piyeer yee na mbooloo ma
14Ci kaw loolu Piyeer taxaw, mook Fukk ñaak benn, daldi àddu ca kaw, ne: «Yeen bokki Yawut yi ak mboolem yeen ñi dëkke Yerusalem, dégluleen bu baax sama kàddu, ba xam lii lu mu doon. 15Ñii màndiwuñu, ni ngeen ko fooge, ndax yoor-yoor doŋŋ a jot. 16Lii kay mooy kàddu ga Yonent Yàlla Yowel jottali woon, ne:
17“Yàlla nee:
Mujug jamono, maay tuur samag Noo ci kaw ñépp;
seeni doom, góor ak jigéen di biral kàdduy waxyu,
seeni xale yu góor di gis ay peeñu,
màggat ñi di gént ay gént.
18Kera jant yooyu, sama jaam ñi, góor ak jigéen,
maa leen di tuur samag Noo,
ñuy biral kàdduy waxyu.
19Te maay def ay kiraama fi asamaan
aki firnde ci dun bi fi suuf;
muy deret ak sawara ak niiru saxaar.
20Jant beey soppaliku ag lëndëm,
weer wi doon deret,
bésu Boroom bi doora taxawe màggaay ak daraja.
21Su boobaa, képp ku woo Boroom bi wall ciw turam, dinga raw#2.17-21 Seetal ci Yowel 3.1-5..”
22«Yeen bokki Israayil, dégluleen wax jii! Yeesum Nasaret, Yàlla moo firndeele ag dëggoom ci ay kéemaan aki kiraama aki firnde yu mu sottale jëmmu Yeesu moomu fi seen biir, te loolu xam ngeen ko xéll. 23Nit kooku ñu jébbale ni ko Yàlla dogale te nasoon ko lu jiitu, yeena ko daajloo yéefar yi ci bant, reylu ko. 24Waaye moom la Yàlla yiwee ci mititu dee, dekkal ko, ndax dee amul kàttanu tënk ko. 25Daawuda wax na ci mbiram ne:
“Maa doon gis Boroom bi fi sama kanam saa su nekk,
ndijoor la ma fare, ba duma tërëf.
26Moo tax sama xol di nux-nuxi,
samaw làmmiñ di tex-texi,
sama yaram sax nara noppalujee yaakaar.
27Doo ma wacc njaniiw moos,
doo seetaan sa Ku sell ki, yaramam di yàqu ci biir bàmmeel.
28Yaa ma xamal yoonu dund,
yaa may wéttali ba matal sama mbégte#2.25-28 Seetal ci Taalifi cant 16.8-11..”
29«Bokk yi nag, Maam Daawuda, manees na leena wax ci lu wér ne nelaw na, ba ñu denc ko, te bàmmeelam a ngi fi, nuy gis ba tey jii. 30Waaye yonent la woon, te xamoon na ne Yàllaa ko giñaloon ne ku jóge ci geñoom lay teg cib jalam. 31Kon li mu gis te dikkagul mooy ndekkitel Almasi bi, te ci mbiram la wax ne wàcceesu ko njaniiw, te yaramam du yàqu ci biir bàmmeel. 32Yeesu moomu nag, Yàllaa ko dekkal, nu seede ko, nun ñépp. 33Yàllaa ko yéege fa ndijooram, te jot na ci Baay bi Noo gu Sell ga mu dige woon. Moom la tuur nii tey, ngeen gis ko, dégg ko. 34Ndax kat du Daawudaa yéeg ci asamaan, waaye moom ci boppam moo ne:
“Boroom bi daa wax sama Sang, ne ko:
‘Toogeel sama ndijoor,
35ba ma def say noon sa ndëggastal#2.35 Seetal ci Taalifi cant 110.1..’ ”
36«Kon nag na wóor waa kër Israayil gépp ne Yeesu moomu ngeen daajoon ci bant, Yàllaa ko def Sang ak Almasi.»
37Ba mbooloo ma déggee loolu, naqar wu mel ni jam-jamu xol la leen def. Ñu ne Piyeer ak ndaw ya ca des: «Bokk yi, nu nuy def nag?» 38Piyeer ne leen: «Tuubleen te ku nekk ci yeen sóobu ci ndox ci turu Yeesu Almasi bi, ngir ñu jéggal leen seeni bàkkaar. Noonu Yàlla dina leen may Noo gu Sell gi. 39Ndax dige bi, yeen ak seen askan a ko moom, ak jàmbur ñi féete fu sore ñépp, mboolem ñi sunu Yàlla Boroom bi woo.» 40Yeneen kàddu yu bare soññe na leen ko, ñaaxe leen ko, ne leen: «Muccleen ci gii maas gu dëng.»
41Ña nangu kàddug Piyeer nag, ñu sóob leen ci ndox; bésub keroog lu wara mat ñetti junni (3 000) yokku nañu ca gëmkat ña.
Gëmkat ñi bennoo, Yàlla barkeel
42Ci kaw loolu gëmkat yi daan nañoo pastéefu ci njàngalem ndaw yi ak ci dundal ag bokkoo, ak ci dagg mburum bokkoo mi#2.42 dagg mburum bokkoo mi: moom la gëmkat ñi aadawoo woon, bu ñuy lekk. Dagg mburu, moom lañu mujj di woowe Reeru Sang bi., ak ci jataayi ñaan. 43Ba loolu amee ag ragal jàpp ñépp, ay kiraama yu bare aki firnde daldi sottee ca jëfi ndaw ya. 44Gëmkat ñépp benn lañu woon te ñoo bokkoon lépp. 45Ci biir loolu seeni suuf ak seen alal sax, ñu jaay, séddoo ko ñoom ñépp na mu dëppook seeni soxla. 46Bés bu nekk nag ñu doon benn bopp, saxoo teew ca kër Yàlla ga, di dagg mburum bokkoo ci këroo kër, tey bokk lekk ci biir mbég ak woyoflu. 47Ñuy màggal Yàlla, ñépp naw leen. Bés bu nekk nag Boroom bi di yokk ca mbooloo mooma, nit ña jota mucc.
Currently Selected:
Jëf ya 2: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright