Jëf ya 1
1
Yeesu Almasi bi yéeg na ci asamaan
1Yaw Tewofil, sama téere bu njëkk ba, def naa ca mboolem ndoortel jëfi Yeesu ak njàngaleem, 2ba ca bés ba ñu ko yéegale, gannaaw ba mu joxee ay ndigal ndaw ya mu tànnoon, Noo gu Sell gi jottali ko. 3Ndaw yooyu itam la teew fi seen kanam ci firnde yu leer te bare, gannaaw ay coonoom. Diiru ñeent fukki fan la leen feeñu, di leen wax lu jëm ci nguurug Yàlla.
4Ba mu nekkee ak ñoom, da leena sant, ne leen: «Buleen jóge Yerusalem, négleen digeb Baay bi ngeen dégge ci sama gémmiñ. 5Ndax cim ndox la Yaxya daan sóobe, waaye yeen ci Noo gu Sell gi lees leen di sóob fii ak fan yu néew.»
6Naka lañu daje fa moom, daldi koy laaj, ne ko: «Sang bi, ndax ci jii jamono ngay sampaat nguurug Israayil?» 7Mu ne leen: «Du yeena wara xam jamono jeek bés bi Baay bi jàpp ci sañ-sañu boppam. 8Waaye Noo gu Sell gi mooy wàcc ci yeen, ngeen fees ak dooleem, daldi doon samay seede ci Yerusalem ak ci diiwaanu Yude gépp ak ci Samari, ba ca cati àddina.»
9Naka la wax loolu, ndaw yay xoole, ñu jekki yéegee ko fa, aw niir daldi leen koy làq. 10Ña nga téen, ne jàkk asamaan, Yeesu di wéy. Ci biir loolu ñaar ñu sol yére yu weex ne seef ci seen wet. 11Ñu ne leen: «Yeen waa Galile, lu ngeen di taxaw nii di séentu ci asamaan? Yeesu male ñu yéegee fi seen biir, yóbbu asamaan, nii ngeen ko gise mu jëm asamaan, ni lay délsee.»
Maccas wuutu na Yuda Iskaryo
12Booba la ndaw ya jóge ca tund woowu ñuy wax tundu Oliw, te digganteem ak Yerusalem tollook kemu dox bi yoon maye ci bésub Noflaay, yemook benn kilomet. Ñu dellu nag Yerusalem. 13Ñu agsi, yéeg ca néegu kaw taax ma, fa ñuy dal naka jekk. Piyeer a nga ca ak Yowaan, ak Yanqóoba ak Àndre, ak Filib ak Tomaa, ak Bartelemi ak Macë, ak Yanqóoba doomu Alfe, ak Simoŋ, Mbokki kuréelu Moom-sa-réew ma, ak Yuda doomu Yanqóoba.
14Ñu mànkoo ñoom ñépp ngir saxoo ñaan ci Yàlla, ànd ceek jigéen ñi ak Maryaama ndeyu Yeesu ak rakki Yeesu yu góor.
15Ci fan yooyu la Piyeer taxaw ca digg bokk ya, ña fa daje di mbooloo mu tollu ci téeméer ak ñaar fukk (120). Mu ne leen: 16«Bokk yi, Mbind mi moo waxoon lu jiitu ci gémmiñu Daawuda jaare ci Noo gu Sell gi, muy wax ju jëm ci Yuda mi jiite nit ña, ba ñu jàpp Yeesu. Mbind moomu nag fàww mu sotti. 17Ci nun la Yuda bokkoon, te amoon na it cér ci sunu liggéey bii.»
18Yuda nag gannaaw ba mu jëndee ab tool ca peyu ñaawtéefam ja, ca la daanu, jiital boppam, biir ba fàcc, butit ya tuuru. 19Waa Yerusalem yépp a ko yég, ba tax ñu tudde tool ba Akeldam, muy firi Toolu deret, ci seen làkk.
20«Ndax bindees na ci téere bi di Taalifi cant ne:
“Yal na këram gental,
yàlla bu fa kenn dëkkeeti,
yal na keneen jagoo sasam#1.20 Seetal ci Taalifi cant 69.26; 109.8..”
21Am na nag ay nit ñu àndoon ak nun mboolem diir bi Sang Yeesu dee dem aka dikk ci sunu biir, 22dale ko ca ba ko Yaxya sóobee ci ndox, ba bés ba ko Yàlla jëlee fi sunu biir, yéege ko. Kon nag kenn ci ñooñu war naa bokk ak nun, seede ndekkitel Yeesu.»
23Ci kaw loolu ñu tudd ñaar: Yuusufa, mi ñu dippee Barsabas, te ñu di ko wax Yustus itam, ak Maccas. 24Ñu daldi ñaan ne: «Boroom bi, yaw mi xam xolu ñépp, won nu ki nga tànn ci ñaar ñii, 25mu jël wàllam ci liggéey bi, te muy céru ndaw bii Yuda wacc, ba fekki wàll wa mu yelloo.» 26Ñu tegal leen nag bant, bant ba dal ca Maccas, mu dolliku ca fukki ndaw yaak benn.
Currently Selected:
Jëf ya 1: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright

: