Jëf ya 3
3
Piyeer doxloo na ab lafañ
1Piyeer ak Yowaan ñoo doon duggsi ca kër Yàlla ga, ngir ñaanu digg njolloor. 2Fekk ñu indi fa waa ju judduwaale lafañ, ñu daan ko teg bés bu nekk ca bunt ba ñuy woowe bunt bu Rafet ca kër Yàlla ga, ngir muy yalwaan ñay duggsi. 3Waa ja gis Piyeer ak Yowaan, ñuy dugg ca kër Yàlla ga, mu di leen yalwaan. 4Ci kaw loolu Piyeer ne ko jàkk, mook Yowaan, ne ko: «Xool nu.» 5Lafañ bi teewlu leen, di séentu ci ñoom ab sarax.
6Piyeer nag ne ko: «Xaalis ak wurus de, yoruma ko. Waaye li ma am, jox naa la ko: ci turu Yeesu Almasi mu Nasaret, doxal!» 7Mu jàpp ci loxol ndijooram, yékkati ko. Ci saa si ay tànkam aki kostanam dëgër. 8Mu ne layy, taxaw, tàmbalee dox, ànd ak ñoom dugg ca kër Yàlla ga, di dox aka tëbantu, tey sant Yàlla. 9Mbooloo mépp gis ko, muy dox, di sant Yàlla. 10Ñu xàmmee ko, xam ne moo daan toog, di yalwaan ca bunt bu Rafet ba ca kër Yàlla ga. Ñu jommi ba jommaaral, ba far gëlëm ca la ko dikkal.
Piyeer waare na
11Ba loolu amee waa ji taq ci Piyeer ak Yowaan, ñépp dawsi, sago jeex, ñu yéew leen ca mbaaru bunt ba ñu dippee Suleymaan. 12Piyeer nag gis loolu, àddu, ne mbooloo ma: «Yeen bokki Israayil, lu ngeen di waaru ci lii? Lu ngeen nu naa jàkk, mel ni sunu manoorey bopp mbaa sunug ragal Yàlla lanu doxloo kii? 13Moom Yàllay Ibraayma, di Yàllay Isaaxa, di Yàllay Yanqóoba, te di sunu Yàllay maam kay, moo màggal jawriñam Yeesu. Yeen nag yeena ko teg ciy loxo, jàmbu ko fa kanam Pilaat, te mu naroon koo bàyyi. 14Yeen, yeena jàmbu Ku sell ki te jub, tinul ab bóomkat. 15Bóom ngeen Kiy dundloo, waaye Yàllaa ko dekkal, nu seede ko. 16Gëm aw turam moo waral turam woowu dooleel nit kii ngeen gis, xam ko. Kon ngëm moo waral lii; ngëm gu sababoo ci Yeesu moo ko may mu wér péŋŋ nii ci seen kanam, yeen ñépp.
17«Teewul nag bokk yi, xam naa ne ñàkka xam moo leen taxa jëfe noonu, te loolu it moo dal seeni kilifa. 18Waaye Yàlla moo sottale noonu la mu yégle woon lu jiitu, yonent yépp jottali, ne Almaseem dina sonn. 19Kon nag tuubleen te dëpp, ndax seeni bàkkaar faru. 20Su boobaa jamonoy péex ay bawoo ci Boroom bi, te mooy yebal Almasi bi mu leen jagleel, te muy Yeesu. 21Moom la asamaan wara dalal, ba kera jamono ja lépp di dellu jag, na ko Yàlla waxe woon, yonent yu sell ya woon jottali. 22Musaa kay noon na: “Boroom bi seen Yàlla mooy feeñal ci seenu xeet ab yonent ni man; nangeen ko déggal ci lépp lu mu leen wax. 23Képp ku déggalul yonent boobu, dees na la dagge ci xeet wi, sànk la#3.22-23 Seetal ci Baamtug yoon wi 18.15, 19..”
24«Te it mboolem yonent yi wax, dale ko ci Samiyel ak ñi ko wuutu, ñoom it yégle woon nañu bés yii nuy dund. 25Yeen nag yeenay ndonoy yonent yi te yeenay séddu ci kóllëre gi Yàlla fasoon ak seeni maam, ba mu nee Ibraayma: “Ci saw askan la xeeti àddina yépp di barkeele#3.25 Seetal ci Njàlbéen ga 22.18..” 26Yeen la Yàlla njëkka wool jawriñam, daldi koy yebal ci yeen, ngir barkeel leen, waññi kenn ku nekk ci yeen mu moy jikkoom yu bon.»
Currently Selected:
Jëf ya 3: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright

: