YouVersion Logo
Search Icon

1.Timote 5

5
Ay ndigal ñeel na jëtun ñi
1Bul gëdd mag, waaye ñaax ko ni bu doon sa baay. Ndaw it, def ko ni sa rakk. 2Jigéen ju mag, def ko ni sa yaay; jigéen ju ndaw, nga def ko ni sab jigéen, te seen diggante set wecc.
3Teralal jëtun ñiy jëtun dëgg. 4Waaye su dee ab jëtun bu ami doom mbaa ay sët, ñooñoo wara njëkka jéema jëfe ag ragal Yàlla ci seen biir kër, ba delloo njukkal seen waajur, ndax loolu la Yàlla rafetlu.
5Waaye kiy ab jëtun dëgg te di ku wéet, mooy ki yaakaar Yàlla, te saxoo ay dagaan aki ñaan, guddi ak bëccëg. 6Ku ci nekkewul lu moy bànneexu bakkanam nag, dee guy dox la. 7Loolu ngay dénkaane, ndax ñépp mucc sikk. 8Ku fàggulul ay bokkam nag, rawatina waa këram, yoonu ngëm wi la gàntal, te moo yées ku gëmul.
9Limeefu jëtun ñi ndimbal ñeel, deesu ci bind ku am lu yées juróom benn fukki at, te na di ku masul am lu wees jenn jëkkër doŋŋ, 10te di ku ñu seedeel jëf ju rafet; lu mel ni yar ay gone ak man gan ak teral gëmkat ñu sell ñi#5.10 Mbaa: raxas tànki gëmkat ñu sell ñi, ak dimbali ñi tollu diggante ak di wéy ci jépp jëf ju baax.
11Jëtun ñiy ndaw nag, génne leen ci, ndax bu leen bëgg-bëggu bakkan sorelee ak Almasi bi, dinañu namma séyaat, 12te su boobaa mbugal war ci ñoom, ndax worma ja ñu fecci. 13Te itam ca lañuy tàmme amug jot, di taxawaalu këroo kër. Te duñu yem ci am ag jot rekk, waaye dañuy réy làmmiñ, di dugg ci lu seen yoon nekkul, tey wax lu leen warul. 14Moo tax ma bëgg, jëtun ñiy ndaw séyaat, ami doom, yor seen kër, ba noon bi du am lu mu yàqe sunub der. 15Ndax kat am na ci xaat yenn jëtun ñu lajj, ba topp Seytaane.
16Gëmkat bu jigéen bu ci am mbokkum jëtun nag, na ko dimbali ba yenni mbooloo mi. Su ko defee mbooloo mi mana dimbali ñiy jëtun dëgg.
Ay ndigal ñeel na mag ñi
17Mag ñiy jiite mbooloo mi bu baax nag, nañu leen yellale ag njukkal ñaari yoon, rawatina ñi boole coonoy waare ak njàngale. 18Ndax kat Mbind mi nee: «Bul ŋalaab gémmiñu nag te fekk koy bojj am pepp#5.18 Seetal ci Baamtug yoon wi 25.4.,» nee it: «Ku ñaq, jariñu#5.18 Seetal ci Luug 10.7.19Bul déglu tuuma ju ñu waxal mag mu jiite mbooloo mi, lu moy ci kaw kàdduy ñaari seede mbaa ñett. 20Waaye ñi ciy bàkkaar, tiiñal leen, ndax ñi ci des ragala bàkkaar.
21Maa ngi lay artu nag fi kanam Yàlla ak Almasi Yeesu ak malaaka yi ñu tabb, ngir nga sàmm loolu te baña jeng, mbaa nga jëfe lenn loo defe xejj ak seen. 22Bul di gaawa teg loxo kenn, ngir fal ko njiit. Bul séddu ci bàkkaari jàmbur, te yaw ci sa bopp, sàmmool dundin wu set.
23Te itam bul di naanati ndox mu ñuul doŋŋ, waaye deel jëfandikoo tuuti biiñ, ndax mu baax ci sa biir ak yeneen xeeti wéradi yu lay farala dal.
24Am ñenn ñu seeni bàkkaar fés, te àtteesagu leen, waaye am na ñenn ñu seeni bàkkaar làqu ba tax yoon dabagu leen. 25Naka noonu, jëf ju baax day fés, te lu ci fésul it, du wéye làqu.

Currently Selected:

1.Timote 5: KY

Highlight

Copy

Compare

Share

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in