1.Korent 14
14
Lu jëm ci waxyu aki may ci wàllu làkk
1Xintewooleen cofeel, te ngeen sàkku mayi Noo gu Sell gi, rawatina mayug waxe kàdduy waxyu, 2ndax kiy làkk weneen làkk, du nit ñi lay waxal, waaye Yàlla lay waxal, gannaaw kenn déggul li muy wax. Teewul ci Noo gi lay waxe ay kumpa. 3Waaye kiy waxe kàdduy waxyu, nit ñi lay waxal, di feddalee, di ñaaxe ak di dalal xel. 4Kiy làkk yeneen làkk, boppam lay feddali, waaye kiy waxe kàdduy waxyu, mbooloom gëmkat ñi lay feddali seen ngëm. 5Su ma sañoon ngeen di làkk yeen ñépp yeneen làkk, waaye ngeen di waxe kàdduy waxyu moo ma gënal. Kiy waxe kàdduy waxyu moo ëpp njariñ kiy làkk yeneen làkk, ndare ñu tekki li muy làkk, ba mbooloom gëmkat ñi jële ca lu ñu feddalikoo. 6Léegi bokk yi, su ma leen dikke woon yeneen làkk yu may làkk, ana lu ma leen di jariñ? Dara, xanaa ma àgge leen kàddug peeñu, mbaa xam-xam, mbaa waxyu, mbaa digle. 7Noonu la itam ci jumtukaayi po yi dundul tey jibal coow; muy toxoro mbaa xalam. Su yooyu jumtukaay jiinul galan yu leer, ana nees di xame li toxoro ji, mbaa xalam giy wax? 8Ag liitu xare it, su jibalul woote bu leer, ana kuy waajal ab xare? 9Noonu la ci yeen itam. Seen làmmiñ, su ngeen ci waxul kàddu gu leer, ana nees di xame li ngeen di wax? Ci jaww ji rekk ngeen di wax! 10Ak ni làkki àddina baree te wuute lépp, wenn ñàkku ci am piri. 11Baat bu jib nag, su ma xamul tekkiteem, ab jàmbur laay doon ci kiy wax, te kiy wax it, ab jàmbur lay doon ci man. 12Kon yeen itam, gannaaw ñu xér ngeen ci mayi Noowug Yàlla, fexeleen cee am lu ne xéew, ngir feddali mbooloom gëmkat ñi.
13Moo tax kiy làkk weneen làkk wara ñaan ngir ñu xam pireem. 14Su may ñaan ci weneen làkk, sama xol ay ñaan, waaye samam xel liggéeyul. 15Kon ana nees di def? Naa ñaane sama xol, tey ñaane samam xel itam. Naa sàbbaale sama xol, tey sàbbaale samam xel itam. 16Soo yékkatee kàddug cant goo waxe xol doŋŋ, ana nu nit ku xamul ku ko teewe naan: «Amiin,» te xamul li ngay wax? 17Ndaxam yaw, rafet nga kàddug cant, waaye sa kàddu feddaliwul keneen ku ciy dégg.
18Sant naa Yàlla ndegam maay làkk yeneen làkk ba raw leen, yeen ñépp. 19Waaye fu mbooloom gëmkat ñi daje, juróomi baat yu ma waxe samam xel ngir jàngale, moo ma gënal junniy baat yu ma waxe weneen làkk.
20Bokk yi, buleen doon ay xale ci wàllu déggin. Su dee lu bon, nekkleen ci ay tuut-tànk, waaye màggleen ci wàllu déggin. 21Bindees na ci Mbind mi ne:
«Ay nit ñuy làkk,
ay làmmiñi doxandéem,
ci laay waxe ak askan wii,
te taxul ba tey ñu déglu ma.
Boroom bee ko wax#14.21 Seetal ci Esayi 28.11-12..»
22Kon nag, yeneen làkk, kàddu ya du ci gëmkat ñi la di firnde, waaye ci ñi gëmul la di firnde. Te it waxe kàdduy waxyu, du ci ñi gëmul la di firnde, waaye ci gëmkat ñi la dib firnde. 23Léegi nag su mbooloom gëmkat mépp dajee béreb, ñépp di làkk yeneen làkk, bu ay nit ñu xamul mbaa ñu gëmul duggsee, duñu ne dangeena dof? 24Waaye su ñépp dee waxe kàdduy waxyu, ba ku gëmul, mbaa ku xamul duggsi, kàddu ga la ko ñépp di tiiñale, àggee ko ko ab àtteem, 25ba la làqu woon ca biir xolam, daldi leer. Su ko defee mu ne dàll dëpp jëëm ci suuf, sujjóotal Yàlla, te naan: «Aylayéwén Yàllaa ngi ci seen biir!»
Ndajem gëmkat ñi jar naa rafetal
26Kon nag ana nees di def, bokk yi? Bu ngeen dajee, kii am woyu cant, kii am lu muy jàngale, kee am am peeñu, kale am lu muy waxe weneen làkk, keneen am am piri, loolu lépp na ko feddali ngëm taxa jóg. 27Su dee weneen làkk lees di wax, na ñaar ba gën gaa bare, ñett, toppante, te kenn di firi. 28Su amul kuy firi, bu kiy làkk làkk wi biral lenn ci jataayu mbooloo mi. Na yelu ngir boppam ak Yàlla.
29Ñiy waxe kàdduy waxyu, na ci ñaar ba ñett wax, te ñi ci des natt wax ji. 30Su keneen ci jataay bi amee am peeñu, na ki doon wax noppi. 31Ndax kat yeen ñépp man ngeena kenn-kennoo, di waxe kàdduy waxyu, ngir ñépp jànge ca, ba gëna farlu. 32Biralkati kàdduy waxyu yi ñoo wara jiite xel mi ñuy waxe, 33ndax Yàlla du Yàllay salfaañoo, Yàllay jàmm la.
Ci mboolem mboolooy ñu sell ñi nag, 34na jigéen ñi noppi ci biir mbooloo yi, ndax mayeesu leen ñu wax ci yooyu jataay. Na jigéen ñi nangu, ni ko yoon wi ci boppam diglee. 35Su amee lu ñu bëgga xam, ca kër ga lañu koy laaj seen jëkkër, ndax jigéen di wax ci biir mbooloom gëmkat ñi, gàcce la.
36Ndax ci seen biir la kàddug Yàlla bàyyikoo? Am ci yeen doŋŋ la agsi? 37Ku ci xalaat ne moom jottalikatub kàdduy waxyu la, mbaa mu yaakaar ne dañu ko cérale ci Noowug Yàlla, war naa xam xéll ne lii ma leen bind, santaaneb Boroom bi la. 38Ku ci xamul loolu nag, kooku, xameesu ko.
39Kon bokk yi, farluleen ci di waxe kàdduy waxyu, te buleen aaye kuy làkk yeneen làkk. 40Waaye na lépp teggine te aw yoon.
Currently Selected:
1.Korent 14: KY
Highlight
Copy
Compare
Share
Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/
Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright