YouVersion Logo
Search Icon

1.Korent 13

13
1Su ma doon làkk làkki nit ñi ak yu malaaka yi sax, te jëfewuma genn cofeel, jóolóoli bu xumb doŋŋ laa, mbaa tëggum weñ muy riir. 2Su ma jotoon ci kàdduy waxyu, boole ci xam mboolem kumpa ak mboolem xam-xam ak ngëm gu mat sëkk ba mana toxal ay tund, te jëfewuma cofeel, duma dara. 3Te it su ma sarxe woon mboolem sama alal, ba sarxe sama yaramu bopp ngir ñu lakk ko#13.3 mbaa ba man koo damoo,, su ma jëfewul cofeel, loolu du ma jariñ dara.
4Cofeel nag, muñ ak mbaax la. Cofeel bokkul ak kiñaan, bokkul ak jikkoy kañu aka damu. 5Bokkul ak jëf ju jekkadi ak jiital sa njariñal bopp, bokkul ak naqari deret, bokkul ak denc mer. 6Bokkul ak bége lu jubadi it, waaye moo di bége liy dëgg. 7Cofeel moo di: lépp, nga baale; lépp, nga gëm; lépp, nga yaakaar; lépp, nga dékku.
8Cofeel nag du jeex mukk. Su dee kàdduy waxyu, dina wéy; su dee ay làkk, dina selaw; su dee xam-xam, dina xewwi. 9Ndaxte as ndog lanu xam, te as ndog lanuy waxe kàdduy waxyu. 10Waaye keroog bu li matale dikkee, ndog si wéy. 11Ba ma dee tuut-tànk, ni tuut-tànk laa doon waxe, di dégge dégginu tuut-tànk, di xalaate ni tuut-tànk. Waaye bi may mag laa xewwil yëfi tuut-tànk. 12Tey jii ci ab seetu lanuy gise gis-gis bu lënt. Waaye bu keroogee, màkk lanuy jàkkaarloo ak li nuy xool. Tey jii, as ndog laa xam, waaye su keroogee, ni ñu ma xame, ni laay xame ba mu mat sëkk.
13Léegi nag liy sax moo di: ngëm ak yaakaar ak cofeel; yii ñett la, te li sut ci yooyii moo di cofeel.

Currently Selected:

1.Korent 13: KY

Highlight

Copy

Compare

Share

None

Want to have your highlights saved across all your devices? Sign up or sign in