1
Room 14:17-18
Téereb Injiil
TI
Ndaxte bokk ci nguuru Yàlla jotewul dara ak lu nuy lekk mbaa lu nuy naan. Nguuru Yàlla mooy jub ci kanam Yàlla te am mbég ak jàmm ci dooley Xel mu Sell mi. Kiy jaamoo noonu Kirist moo neex Yàlla ak nit ñi.
Compare
Explore Room 14:17-18
2
Room 14:8
Danuy dund ngir màggal Boroom bi, dee it ngir màggal ko. Kon nag nuy dund mbaa nu dee, noo ngi ci Boroom bi.
Explore Room 14:8
3
Room 14:19
Kon nag nanu wut luy indi jàmm, tey yékkati ngëmu sunu moroom.
Explore Room 14:19
4
Room 14:13
Kon nanu bàyyee tegante tooñ, waaye nu fas yéenee moytu lépp lu nekk fiir guy yóbbe sunu moroom bàkkaar.
Explore Room 14:13
5
Room 14:11-12
Ndaxte Mbind mi tëral na lii: «Boroom bi nee na: “Ni mu wóore ne maa ngi dund, ni la wóore ne, ñépp dinañu ma sukkal, te ku nekk seede ne maay Yàlla.”» Noonu ku nekk ci nun dinga làyyi fa Yàlla ci lépp loo masa def.
Explore Room 14:11-12
6
Room 14:1
Gannaaw loolu ku ngëmam néew nangeen ko nangu, te baña werante ak moom ci lu lënt.
Explore Room 14:1
7
Room 14:4
Koo teg sa bopp, ba di ko teg tooñ? Jaamu jaambur la! Mu taxaw ci liggéeyam, mbaa mu sàggane ko, moom ak sangam la. Waaye dina jub, ndax Boroom bi am na dooley taxawal ko ci njub.
Explore Room 14:4