1
Room 15:13
Téereb Injiil
TI
Kon Yàlla miy maye yaakaar, na def ci seen xol mbég mu réy ak jàmm ju yaa ci seen kaw ngëm, ba ngeen am yaakaar ju mat sëkk ci dooley Xel mu Sell mi.
Compare
Explore Room 15:13
2
Room 15:4
Ndaxte lépp lu ñu waxoon ci Mbind mi lu jiitu tey, dañu koo tëraloon, ngir nu sàkku ci xam-xam, xam-xam bu nuy may fit ak muñ, ak di feddali sunu yaakaar.
Explore Room 15:4
3
Room 15:5-6
Kon nag Yàlla miy maye muñ ak fit, na leen may, ngeen déggoo te nekk benn bu yellook li Kirist Yeesu wone. Ba tax nu bokk benn xalaat ak benn baat ci màggal Yàlla, Baayu Yeesu Kirist sunu Boroom.
Explore Room 15:5-6
4
Room 15:7
Moo tax nangoonteleen, bay màggal Yàlla, ni leen Kirist nangoo.
Explore Room 15:7
5
Room 15:2
Na ku nekk ci nun di wut lu neex moroomam ngir jariñ ko, ba mu gëna dëgër ci ngëmam.
Explore Room 15:2