1
Room 13:14
Téereb Injiil
TI
Waaye gànnaayooleen Yeesu Kirist Boroom bi, te baña topp seen bakkan ciy bëgg-bëggam yu bon.
Compare
Explore Room 13:14
2
Room 13:8
Buleen ameel kenn dara, lu dul mbëggeel; ndax ku bëgg sa moroom, wàccoo nga ak yoonu Musaa.
Explore Room 13:8
3
Room 13:1
Gannaaw loolu na nit ku nekk déggal ñi yore baat ci kanamam; ndaxte amul njiit lu fi Yàlla sampul. Njiit yépp nag Yàlla moo leen fi teg.
Explore Room 13:1
4
Room 13:12
Guddi gi màggat na, bët a ngi bëgga set. Nanu bàyyi nag jëf yu lëndëm te ràngoo gànnaay yi nu Yàlla jox, ngir dund ci leer.
Explore Room 13:12
5
Room 13:10
Ku bëgg sa moroom, doo ko tooñ; kon ku wéy ci mbëggeel matal nga yoonu Musaa.
Explore Room 13:10
6
Room 13:7
Joxleen ku nekk céram; ku ngeen wara fey galag, feyleen ko ko; ku ngeen wara fey juuti, feyleen ko ko; ku ngeen wara weg, wegleen ko; ku ngeen wara teral, teral-leen ko.
Explore Room 13:7