1
Room 12:2
Téereb Injiil
TI
Bu leen àddina jay, waaye yeesluleen ci seen xel, ba soppiku, ngeen mana xam bu wér coobarey Yàlla, di lépp lu baax, neex ko te mat sëkk.
Compare
Explore Room 12:2
2
Room 12:1
Kon nag bokk yi, gannaaw yërmandey Yàlla baree na noonu, maa ngi leen di ñaan, ngeen jébbal ko seen yaram wépp. Na seen dund mel ni sarax su ñuy defal Yàlla, sarax su sell te neex ko. Loolu mooy njaamu, gi leen war.
Explore Room 12:1
3
Room 12:12
Bégleen ci yaakaaru ëllëg te muñ bépp tiis, di sax ci ñaan Yàlla.
Explore Room 12:12
4
Room 12:21
Bu leen lu bon ëpp doole, waaye notleen ko ci def lu baax.
Explore Room 12:21
5
Room 12:10
Bëgganteleen ak xol bu leer, niy doomi ndey, te farlu ci teralante.
Explore Room 12:10
6
Room 12:9
Na seen cofeel di lu dëggu te baña nekk ngistal; araamal-leen lu bon te sax ci lu baax.
Explore Room 12:9
7
Room 12:18
Wutleena juboo ak ñépp, ba fa seen kàttan yem.
Explore Room 12:18
8
Room 12:19
Samay soppe, buleen di feyantoo, waaye bàyyileen lépp ci loxoy Yàlla, mi yelloo àtte; ndax Yàlla nee na ci Mbind mi: «Man maay àtte, maay fey jëf.»
Explore Room 12:19
9
Room 12:11
Sawarleen te baña tayel, di jaamu Boroom bi ak seen xol bépp.
Explore Room 12:11
10
Room 12:3
Gannaaw Yàlla may na ma ciw yiwam, ma nekk ndawam, maa ngi leen di wax lii, kenn ku nekk ci yéen: buleen yég seen bopp, waaye ngeen am xalaat yu yem, méngook ngëm gi leen Yàlla sédd, ku nekk ak wàllam.
Explore Room 12:3
11
Room 12:17
Buleen feyante lu bon, waaye sàkkuleen seede su rafet ci kanam ñépp.
Explore Room 12:17
12
Room 12:16
Bokkleen menn xel, tey baña yékkatiku, di yóotu daraja, waaye ngeen fonk ñi suufe; buleen teg seen bopp boroomi xel.
Explore Room 12:16
13
Room 12:20
Waaye defleen lii: «Bu sa noon xiifee, may ko mu lekk; bu maree, may ko mu naan. Ndax boo ko defee, dinga ko rusloo.»
Explore Room 12:20
14
Room 12:14-15
Ku leen fitnaal, ñaanal-leen ko yiw, te bañ koo móolu. Bégandooleen ak ñi bég, te jooyandoo ak ñiy jooy.
Explore Room 12:14-15
15
Room 12:13
Dimbalileen gaayi Yàlla yi ci seeni soxla, te saxoo dalal gan.
Explore Room 12:13
16
Room 12:4-5
Loolu, ci maanaa, mi ngi mel ni yaramu nit: yaram, lu cér yi baree bare, benn niroowul ak moroomam liggéey. Noonu itam nun ñi bokk ci Kirist, lu nu baree bare, benn lanu te danoo mànkoo.
Explore Room 12:4-5